Omar Bolondeŋ Jóob a ngi juddu ci 10eelu fan ci weeru sàttumbar 1946 ca Ñaame, péeyub réewum Niseer. Mu ngi faatu ci 11eelu fan ci weeru Mee 1973 ca kaso ba woon ca dunub Gore. Omar Bolondeŋ Jóob, nag, kàngam la woon ci biir kàngam yi, jànge ca lekkoolu digg-dóom ji ñu duppe Louis-le-Grand ca Pari. Bim fa génnee, mu tàbbi ca daara ju mag joojee ñuy wax École normale supérieure de Saint-Cloud. Jamono jooju, waxuma la sax am lijaasa ca daara joojee, waaye jànge fa rekk doyoon na ndam, dib sag bu réy a réy ci boroom. Bokk na ci liy màndargaal dayo daara jooju, mooy ne ki jëkk a jiite réewum Senegaal, Lewópóol Sedaar Seŋoor, ñu ràññee ko lool ci wàllum ladab ak mbind, bëggoon na fa dugg, waaye daa lajj. Muy biral ne, daara jooju, ab como daawu fa teg tànk. Am na sax ñuy wax ne, Seŋoor da koo iñaane woon ndam loola, ragal ne dina ko may fitu wujje ak moom ci làngu politig gi, ñeel Senegaal.
Sëñ bi Jóob, nag, du woon ragal walla tóoyemaan, ni ko ndaw yiy waxe. Bañkat dëgg la woon, ñeme woon xeex. Dafa di sax, ni mu ame woon noonu fit moo taxoon ñu dàq ko, moom ak benn doomu Farãs bu daan wuyoo ci turu Daniel Cohn-Bendit, ca daara ju mag jooju, ci atum 1969. Waaye yemul foofu. Ndege, Omar Bolondeŋ Jóob dafa xaroon tànki tubéyam, di xeexal askanu Senegal. Mi ngi féete woon ci kóminist yi, daan roy ci doxalinu Mao-Tsé Toung. Kurél gi mu bokkoon mësul a juboo ak Seŋoor, foo leen fekkaan, ñu ngay jàmmaarloo. Ndaxte, Seŋoor nguurug Farãs la fi toogaloon te, ci wàllu xalaat ak politig, yoonu kapitaalist yi la Farãs ak ñi far ak moom toppoon. Loolu mi ngi tollook jamonoy xareb suuf (guerre froide) bi amoon ci diggante U.R.S.S. (kóminism- sosiyalism) ak réewum Amerig (kapitaalism–liberaalism). Àddina si xar ñaar : ñii far ak U.R.S.S. miy mujje dooni Riisi, ñeneen ñi far ak Amerig.
Bi mu ñibbisee Ndakaaru, mu wéyal xeex boobu ci ndimbaluy rakkam. Ñoom ñépp ñu doon xeex nooteel, teg ci di ŋàññ doxalinu Seŋoor mi doon wéy ci waawi Farãs. Seŋoor demoon na sax ba jël Jean Collin, di doomu Farãs, boole ci di jegeñaale Jacques Foccart, toftal ko ci boppam, dénk ko lépp lu jëm ci kaaraange biir réew mi.
Loolu la Omar Bolondeŋ Jóob ak i àndandoom doon xeex. Ndax kat, Seŋoor dafa jébbalu woon ci Farãs ba nga xam ne, buñ tisóoliwaan Pari, mu ne yaaram-kàlla. Am jamono, Seŋoor sumboon fi liggéey bu mag ñeel mbeddi ndakaaru yi, santaane ñu set-setal gox-goxaat yi ngir laabal leen. Te, nag, duggewu ko woon lenn lu dul teeru Pompidou mi jiite woon Farãs, ngir bégal ko. Loolu metti lool Omar Bolondeŋ Jóob ak i rakkam ba tax ñu demoon taali Njawriñu Liggéeyu caytu gi ak Kërug aada ak cosaan gu Farãs ci Ndakaaru, ñu doon ko wax « Centre culturel français ».
Yemuñu ca, ndax defaroon nañ ay ndell, fasoon leen yéenee sànni ci kow woto yi yaboon Seŋoor ak kilifa tubaab yi mu waroon a teeru. Wànte, dañu mujje lajj ci pexe moomu. Ci lañu leen tege loxo. Jàllo Jóob moom, dañ ko tëjoon Kéedugu giiru dundam ba noppi sas ko liggéey bu mu sañutoon a bañ, dëkke koo metital ak a xorñoññal ca biir kaso ba. Ca la Omar nisëree woon ca Mali ga mu dawoon làqu, ne day afalsiy rakkam, kilifay Bamako tegati ko loxo, jébbal ko nguru Senegaal.
Ñaar fukki fan ak ñett ci weeru Mars ci atum 1972 la këru àttekaay bu Seŋoor àtte woon Omar Bolondeŋ Jóob, daan ko ñetti ati kaso yu mu waroon a tëdd. Li ñu ko jiiñoon moo doon “nasaxal kaaraange réew mi”. Mu doon xeex doxalinu Seŋoor wi aju woon ci li neex tubaab yi ba noppi worook bëgg-bëggu askanu Senegaal. Moom Omar Bolondeŋ Jóob, dafa mujjee ñàkk bakkanam ca kaso bu Gore ba ñu ko dencoon.
Ci 14eeli fan ci weeru Mee atum 1973, la yéenekaayu nguur gi, “Le Soleil”, siiwal xibaar bu tiis bi : “Kurél giy sàmm kaso yi (…) mu ngi xamle ni Omar Bolondeŋ Jóob xaru na ci néegam ci biir kasob Gore ginnaaw bi mu yeewee buum ci baatam. Mu ngi ko def ci boori ñaari waxtu ci guddi”. Booba, 26i at kepp la Omar Bolondeŋ Jóob am. Amaat Daŋsoxo ne woon ca tonet, wax ne : “Dafa leer nàññ ci sama bopp ne Omar Bolondeŋ Jóob dañu koo bóom. Li tax kilifa yi ŋànk réew mi bóom ko nag, lenn rekk la : ak xel mi ko Yàlla mayoon, Omar mënoon na leen fee jële !”
Ndeysaan, njabootu njóobéen – rawatina Jàllo Jóob – ñoo ngiy wéy di xeex booba ba léegi ngir ñu bañ a fàtte seen mag jooju. Ñoom li ñu jàpp mooy ne, Omar dañ koo rey, te dara waralu ko woon lu dul politig. Omar a ngi gaañu ginnaaw bi ñu ko metitalee ca kasob Gore ba, te ñu mën a njort ne lépp ci ndigalu Jean Collin la ame. Ñu bare ci ñiy gëstu ci mboorum (histoire du) Senegaal, loolu lañ jàpp.