Ndekete yoo, nekk lawax ci réewum Senegaal yombul. Ca dëgg- dëgg, mbir mi làmbi golo lay xaw a niru. Ndax, ñu bari foogoon nañu ne baayale yi rekk moo nekk seen ndëgg-sërëx. Waaye, mel na ni am na yeneen i gal-gal yu leen di xaar.
Dafa di, lawax yi ci seen bopp tàmbali nañoo xeexoo. Mu mel ni “duma dem, waaye yow it doo dem” la ñenn ñi bëgg a doxal. Ndaxte, jamono jii, lawax yi bari nañuy tànk fa màkkaanu ndajem ndeyu àtte mi. Bu dee ñii dañu dugal ay dabantal ngir ñu saytuwaat seen i wayndare, ñeneen ñi, ñoom, dafa am ay lawax yu ñuy kaas ne waruñoo jàll bay bokk ci wote yi.
Ndege, Ceerno Alasaan Sàll dafa sulli coowal nasiyonaalite Kariim Meysa Wàdd. Moo tax ba jegeñaaley doomu Ablaay Wàdd ji dal ci kowam. Ñoom, waa PDS, nee ñu, dara jàppul Ceerno Alasaan Sàll lu dul ag coxorte. Ci seen i wax, dafa iñaane Kariim. Te, moom Kariim Wàdd, ca atum 2019 la faroon nasiyonaalite Farãs bi mu yoroon.
Ñu ni déet-a-waay, Aamadu Ba, lawaxu Bennoo Bokk Yaakaar bi, sàkku ci ndajem ndeyu àtte mi mu neenal wayndarey lenn ciy lawax yu jot a jàll ci caytug baayale gi. Layookatam bii di Aamadu Sàll a ko xamle. Moom sax, Aamadu Sàll, siiwalul turi lawax yi njaatigeem bi bëgg a yàqal. Waaye, bees sukkandikoo ci gëstu yi taskati xibaar yi def, lawax yi muy diir du ñenn ñu dul Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, Aali Nguy Njaay ak Mahamaat Bun Abdulaay Jonn. Mu nekk ab dabantal bu ndajem ndeyu àtte réew mi war a saytu fi ak gaawu gii.
Li jaaxal ñu bari nag, moo di ne, moom Aamadu Ba mi ànd ak dooley Nguur gi, yor xaalis bu dul jeex, wax ne amoon na ñeenti tamndareti baayale, naka la mën a ragalee ay lawax ? Am na luy ñuul ci soow mi daal.