WOTEY 2024 YI : WURE WA DEM NA KËŊ

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ay waxtu rekk ñoo des ngir Saa-Senegaale falaat Njiitu réew lu bees lu war a wuutu Maki Sàll ci boppu Nguur gi. Mu nar koo jox lenge yi bu dee ci sumb bu njëkk bi la raw. Gaawug tey jii, bésub noppalu la. Ndax, démb la kàmpaañ bi jeex.

Bés bu màgg, bés bu réy a réy mooy xaar maxejji Senegaal. Ëllëg, dibéer 24 màrs, bu 8i waxtu jotee, lañu wutali mbañ-gàcce yi ngir def seen wareef, daldi tànn, fal kiy jiite réew mi ci 5i yii di ñëw. Waaye, ëllëg, du Njiitul réew kepp la Saa-Senegaal yiy tànn. Nde, bees seetloo tolluwaayu jamono, xool lawax yiy dagaan baatu askan wi, dees na gis ne wote yii, li ci laxasu dafa réy. Ñépp dëppoo nañ ci ne, bi Senegaal di Senegaal ba tey, wotey suba yi ñoo ëpp solo wote yi fi jot a am yépp. Moo tax, Senegaal a ngi toog ci nen, di ñaan wote yi am ci jàmm ak salaam. Ngir jàmm jooju am nag, fàww lépp jaar ci yoon.

Bees sukkandikoo ci jëwriñu biir réew mi, lépp yemb na. Nee na jumtukaay yépp mat nañ, matale ci béreb yees war a wotee yépp, muy fi réew i ak bitim-réew.

Ren, xaymees na limub maxejj yi war a wote ci 7. 033. 852. Ñu tas leen ci 553i komin yi nekk ci 46i depàrtamaŋ. Bérébi wote yi tollu ci 6. 681 yu ame 15 633i pekki wote.

19i lawax yi jot a samp seen ndënd fésal nañu fa ñu war a wote. Ñenn ñaa nga diiwaanu Ndakaaru, ku ci mel ni Aliyun Mamadu Ja, Aamadu Ba, Anta Baakakar Ngom, Xalifa Abaabakar Sàll, añs. Ñeneen ñi nar a dellu seen i dëkk ngir wotee fa : Décce Faal fa Ndar-géej, Basiiru Jomaay Fay ak Paap Jibril Faal Mbuur, Maam Bóoy Jaawo fa Kolda, Idiriisa Sekk ak Ceerno Alasaan Sàll fa Cees-kaay, Aali Nguy Njaay ak Abiib Si fa Luga, Sëriñ Mbuub fa Kawlax, Muhammad Bun Abdalaa Jonn Fatig.

Wure wa dem na këŋ, lu waay doon jaay léegi mu lamb.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj