XEESAL WALLA XEEB SA BOPP ?
Kañ la jigéeni Senegaal yi tàmbalee xeesal ? Fanweeri at ci ginnaaw ? Lu ko ëpp ? Gëstukati réew mi war nañoo tontu ci laaj boobu. Li ma ci xam, daal, moo di ne mu ngiy bëgg a yàgg. Mel na ni ca njëlbéen ga ñu bare dañu newoon ci seen xel : ‘’Lii de, baaxul, waaye ay feemi gone la rekk, du jikko, jamono la, léegi ñu génn ci !’’ Njuumte lu réy la woon ndax fi mu ne nii, yematul ci jigéen ñi, ay góor sax a ngi diwu… Ku sañul ni bala la yit, xalaat nga ko.
Ku weddi ne tey la Waalo gën a aay, doxantul ci mbeddi Ndakaaru yi, téen xool nataali-siiwal yiy tagg xees ak xeesal. Boo toogee sa kër tamit, taal sa tele dinga gis ñu ciy wane ndaw suy diwu, yànjal la ko ba nga ni lii lu mu doon, nataal yi di la déey musiba, naan la ‘’Nii nga war a mel !’’, walla : ‘’Nii nag la sa soxna war a mel !’’’
Wax ji moom jarul a yërëm, li xeesal tekki moo di ne am der bu ñuul gàcce la, taaruwl dara, loo gën a nirook Tubaab ñu gën laa teg nit.
Mbir mi dafa dagg xol ba noppi yéeme. Xéy-na lu ni mel mënoon nañ ko séentu feneen ci Afrig fu dul Senegaal. Liggéey bu mucc ayib bi Séex Anta Jóob def ngir weglu nit ku ñuul waroon naa tax nu àndandoo sib xeesal. Te yit, xanaa Senegaal dootul réewum ‘’Négritude’’ ? Xanaa du Seŋoor a bind ‘’Femme noire’’, taalif bi gone yiy tari subaak ngoon ?
Lii lépp a merloo woon Aysa Dem, mi ñépp xam ci farloom ñeel mbiri aada, ba mu jiite fi kàmpaañ, duppe ko ñuul kukk di fésal taaru jigéen ju ñuul ak ni nit ki waree naw boppam. Fulla ju mat sëkk la Aysa Dem wane foofu te ñu bare gërëm nañ ko ci. Waaye li gënoon xéy-na moo doon ñépp àndandook moom ci xeex boobu. Mbootayi jigéen ñi nga xam ni foo leen fekk ñu ngi ñaxtu, naan dañoo sàggane seeni yelleef, kenn waruleen woon cee jiitu. Léegi, nañu yëkkati seen kàddu, wax kilifay réew mi ñu aaye kuy def piblisite xeesal, aaye sax xeesal ci boppam.
Am nay jàngoro yoo xam ni gornmaa rekk moo leen mén a faj. Xeesal ci la bokk. Loolu la Paul Kagamé, njiitul Ruwandaa, xam ba jël ay dogal yu am solo, tere kuy dugal walla kuy defar diwu yu ni mel ca réew ma, tere yit ku ko jaay, ku ko jënd mbaa ku ko jëfandiko. Loolu lañ fa dogal te ku ko moy yoon dal ci sa kow.
Teewul doktoor yeek yeneeni boroom xam-xam war di wéy di gindi jigéen ñi, di leen yee ba ñu xam ni nit ku weex gënul nit ku ñuul. Waaye liñ naan bóli gu dog tiiñ na doktoor moo fi ne. Ndax ndaw soo laaj lu ko xiir ci xeesal mu am ci kersa, damm loos ni la lépp ak góor ñi, soo xeesul duñ la faale. Ñu ci bare leeral rekk a leen ciy dugal, ñu dem ba yëf yi ëpp leen loxo, fu ñu gis diw jënd ko, diwoo.
Moonte xam nañ xéll ni xeesal day oyofal sa der, wàññi dooleem, foo laal daj ay picc ak i rew ak i taas, soo moytuwulee jële ciy feebar yu bon niki kañseer walla taŋsiyoŋ. Doktoor yi seen xam-xam màcc ci pajum der wax nañu ba tàyyi, waaye kenn nanguwuleen a déglu. Waaw, ndax wut taar rekk jar naa ñàkk sa bàkkan ?
Ñàkkul jaaykati xeesal yeek isin yi koy defar la nguur gi ragal ba tax ko ni patt-pattaaral, di seetaan lu ñaaw lii mën a delloo réew mi ginnaaw. Am na ñu naan du loolu lépp, dafa ferekk ni sunuy njiit tal nañu leneen, nun baadolo yi amaluñ leen benn solo. Xanaa kay du loolu laa yaakaar ?
Ku xeeb sa bopp, dem sax ba xamatoo yaay kan, mënoo amal benn njariñ saw askan. Kon, nanu ci jóg gaaw : xeesal jëmul kër…
Ndey Koddu Faal
XEESAL WALLA XEEB SA BOPP ? was originally published in Defu Waxu on Medium, where people are continuing the conversation by highlighting and responding to this story.