Daara yu kowe yi ci Senegaal dafa mel ni ag dal daf leen a dëddu. Bu dul coowal pólitig gu wal ba wàlli ci biir jangune yi, di ay ñaxtu. Mu mel ni tulleek màlle, am ndongo yi indi, Nguur gi. Ndongo ya fare ca daara ju mag ja ñu duppee Asan Sekk, sóobu nañu ci ay ñaxtu.
Muy ay yëngu-yëngal yu ñu amaloon ci altine ji ngir jooytu seen i jafe-jafe. La ñuy ñaawlu mooy liggéey bu yéex ba ñu nemmeeku ca taax ya ñu sumb 2015 ba léegi ngir ñu mën fa door seen um njàng. Ba tax na lañuy sàkku mooy ñu àggale leen ci lu gaaw. Bokk na ca ñu jébbal leen jumtukaay ya ca war, jébbal leen tamit saal yu mag ya ñuy jànge tay def lu tollu ci 150 ci ay toogu. Waaye, fàttewuñu tamit seen i dëkkuwaay yi. Ndax fésal nañu seen uw naqar ci tolluwaayu lim bu takku ba fa nekk te dëkkuwaay ya matewu ko. Loolu tax ba ñu bëgg, ñu jébbal leen seen néeg yooyu mën a def 1000iy (junniy) lal.
Nañu ko doon sàkkoo démb bettut kenn. Nde, ndongo yi fare ci daara yu kowe yi fonk nañu lool, jàmmaarlo ak takk-der yi. Tax na ba njàngaani Asan Sekk yi génn ca xàll wu mag wa ak seen i xeer yu ñuy weccante ak ay gërënaad. Mu nekkoon yoor-yoor gu tàng ci diggante takk-der yi ak ndongo yi. Ñoom, ndongo yi di ñaawlu Nguuru benn nopp gi ñu ko séqal ne balaa ñoo faj seen i soxla dañoo xeex, jàmmaarloo.
Mënees na wax ne daara yu kowe yi ciy jafe-jafe lañuy dund. Démb ñàkkum ndox la woon ca Ndar, tey Sigicoor di jooy aw nekkin. Ndongo yi dëkke jàmmarlo ak takk-der yi, yàqu-yàqu di gën a bari te balaa saafara am béy wéy mbuus.