Ci guddig gaawu gi jàpp dibéer jii weesu la Inter Miami doon joŋante finaalu Leagues Cup, doon ci daje ak Nashville. Bi joŋante bi dawee ba ci 23eelu simili ba la Pulga bi daldi dugalal Inter Miami, ñu dawal ba ci xaaju ñaareel bi, ci 57eelu simili bi, Fafa Picault fayul ekibam. Ci teg dóor yi lañu mujje tàqaliku. Inter Miami gañe 10i bii ci 9 (ci teg dóor bi). Bii kub di bu njëkk ci Messi ak Bousquet, saa-baarsalon ya woon.
MBAPPE DUGGAAT NA CI PÀKK YI
Keroog ci gaawu gi, Paris Saint Germain doon na amal ñaareelu joŋanteemu Ligue 1. Mbappe bokkoon ci 22i futbalkat ya. Dafa di, moom sax moo dugal biiwu PSG bi ci teg dóor bi ñu amoon (1-1). Loolu nag di wane xanaa ni juboo am na ginnaaw coow li dox seen diggante. Nde, Mappe dafa ban a xaatim pas gu bees ak këlëbu péeyu Farãs bi, ne day toog ba 2024 demal boppam. Loo naqadi woon kilifay PSG yi ba ñu beddi woon ko.
BELLINGHAM : GAN GIY TABAX
Gan-ganlu moom bokkul ciy mbiri Jude Bellingham. Goneg Àngalteer bi, dafa ñëw Real Madrid rekk daldi bokk ; fireeku, di futbal futbalam. Moo tax ci ñaari joŋante yi njëkk ci LIGA bi, dugal na ci ñetti bii ba def ci benn paas. Keroog gaawu, ci ñaareel xaaju mats bi la daldi dugal ñaari bii.
PAAP MATAAR SAAR A NGI XÀLL YOONAM
Ren mooy ñaareelu atam ak Tottenham. Mu mel ni, ren jii, daa fas yéene dëggal boppam, wane lim mën. Gannaaw ba ñu soppee tàggatkat, la ku bees ki daldi xamle ni Paap Mataar du juge ci këlëb bi ndax daf ko soxla. Boobu ba léegi nag gisees na genn kóolute bum am ci moom ba tax mu di ko futbal-loo. Ci gaawu gii weesu, Paap Mataar moo jëkk a dugal ci seen ndam biñu am ci kaw Manchester United (2-0).