CHAN 2023

Yeneen i xët

Aji bind ji

Chan 2023 bi door na keroog àjjuma 13i fan ci saŋwiye 2023. Wile yoon a di 7eelu yoon wees koy tëgg. Ren nag, Alséri moo dalal joŋante bi.

Senegaal a ngi bokk ci kippu B gi, war cee jàmmaarlook Koddiwaar, Repiblig bu Kongo ak Ugàndaa. Ci gaawu bi, 14i saŋwiyee 2023, la gayndey Senegaal doon wureek ñayi Kodiwaar yi. Bi 19i waxtu jotee la mbiibu arbit bi jolli, bal bi wër. Mu nekkoon joŋante bu metti. Nde, diggante gaynde ak ñay, fu ñu daje, pënd wur. Dafa di, nag, ku sañ a wokk taatu gaynde, war a ñeme xët ba. Moo tax it, gayndey Senegaal yi benn xët lañu ngàdd ñayi Koddiwaar yi, joŋante ba yem fa. Ndaxte, Senegaal moo dóor benn bal ci dara (1-0). Waaye, yombutoon ci gaynde tamit de.

Ci xaaju joŋante bu njëkk bi, dañoo temboo, joxantey loxo. Maanaam daal, kenn dugalul sa moroom, donte Senegaal a xawoon a jekku. Nde, moo ëppoon la mu yoroon bal bi, di ko dawal. Ci ñaareelu xaaj bi, bi ñu dawalee ba ci 73eelu simili bi, Senegaal am ca ab teg-dóor (penalty. Ndeysaan, Mamadu Lamin kamara a ko dóor, moyal ko (rate). Moom kay, ci kaw jàppkat bi la ko dóor. Bi loolu jàllee, ñu dawalaat 4i simili (ci 77eelu simili bi), doomu Senegaal bi, Musaa Njaay, daldi taal caax yi, 1-0 ngir Senegaal. Boobu nag, daanaka bii bi xawoon na am lënt- lënt tuuti. Ndaxte, dañu foogoon ni dafa am ku génn génn gu ëpp (hors-jeu) ba tax ñu taxawal bal bi dem ca « VAR » ba seet ko, settanti ko,  door a nangu bii bi, wéral ko. Moom Musaa Njaay lañu fal jàmbaaru joŋante bi. Te sax, bi ñu tollee ci 68eelu simili la dugg, dugal ci 77eelu simili bi. Bu fekkoon fii la xewe, xale yi woyal kon nañu ko : « Musaa dafa dugg, dugal ! Musaa dafa dugg, dugal ! »

Donte nag Senegaal a gañe, teewul ni am na yu ñu war a dolli liggéeyaat ci ekib bi, rawatina kaw geek wàllu dugal gi. Ca seen joŋante waajtaay ba weesu sax, seen tàggatkay bi doon na ko wax, ni fàww ñu liggéeyaat mbirum dugal gi ndax li ñuy moyal dafa bari. Loolu moom dama yaakaar ni sunu cat la, ba ci ekib bu mag bi sax, léeg-léeg nga foog ni dafa am lu nekk ci seen tànk yi.

Senegaal moo ngi toog ci boppu kippu B gi, am 3i poñ, Repiblig bu Kongo ak Ugàndaa am ku nekk benn poñ, Kodiwaar tus. Senegaal war a daje ak Ugàndaa 18i saŋwiyee bii, bu noppee door ci tegaat Repiblig bu kongo 22i fan ci weer wi. Nuy ñaan ak a am yaakaar ni yeneen i ndam danañu dikk ak wure gu gën a set te dalum xel.

Gayndee Njaay ! Mbara-wàcc !

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj