JÀKKAARLOO NJIITU RÉEW MI AK TASKATI XIBAARI YI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Démb ci gaawu gi, fukki fan ak ñett ci weeru sulet 2024, la Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, doon janoo ak taskati-xibaar yi. Mi ngi doon amal waxtaan wi bi juróom-ñeenti waxtu ci guddi jotee. Li mu ko dugge woon mooy indi ay tontu ci seen i laaj. Nde, kenn umpalewul ne ba mu faloo ba tey, amalagul woon aw waxtaan ak taskati-xibaar yi. Démb, moo nekkoon yoon wu njëkk wi. Rax-ci-dolli, démb la doon waxaale ci téeméeri fan yi mu def ci boppu Nguur gi. Moo tax, jot na faa laal ay poñ yu bari. Muy lu ci mel ni fi ñu jële réew mi, fi réew mi tollu ak fi ñu ko bëgg a jëmale. Waaye, yemul foofu. Nde, am na yeneen poñ yu am solo yu mu ci laaxaale yoo xam ne dees na ci dellusi.

Waxtaanu wi Njiitu réew mi doon amal démb xaw naa gudd tuuti. Nde, waxtaan wi def na lu ëpp ñaari waxtu. Mu doonoon waxtaan woo xam ne làmboo na solo su bari. Ndax, indi na ay leeral yu bari ci ni ñu fekke réew mi rawatina li ñu fi gis ci doxalin wu ñaaw ñeel alalu réew mi. Dafa di, ciy waxam, bi muy jël réew mi, fekkul dara ci kees yi. Maanaam daal, bees ko déggee, réew maa ngi woon ci guddi gu bët setagul. Ci weneen waxiin, réew maa ngi doon sukurraat. Moo tax, ñoom, bi ñu leen joxee réew mi rekk, ñu teel a jël ay ndogal ci ay banqaas ak béréb yu bari ngir gaal gi bañ a suux.

Muy lu ci mel ni peyug lempo yi, waxtaanewaat pas yi, wàññig dund bi, xéyu ndaw ñi, def ay caytu ba xam fu alalu réew mi dugg. Waaye tamit, def kéemtalaayu kàttanam ba ñu doxal Yoon ba du am Kumba am ndey ak Kumba amul ndey. Maanaam, mu bañ a am làq doom, dóor doom. Ku jalgati yoon, ak foo mēn di bokk, ñu teg la ci yoon. Looloo tax, muy xamle ne du teg conc ci genn caabal. Day bàyyi Yoon def liggéeyam. Loolu terewul mu leeral ci boppi saa-senegaal yi ne moom, feyantoo taxu koo jóg.

Mu am poñ boo xam ne, mel na ni bokk na ci li ko gën a ñor, moom ak ug Nguuram, muy waxtaanewaat pas yi. Moo tax, mu dig saa-senegaal yi ne pas yi moom dees na leen waxtaanewaat. Su ko defee saa-senegaal yi mën cee gis seen bopp. Nee na, ñu baree ngi jàpp ne mënuñoo waxtaanewaat pas yi, waaye loolu dina am. Dafa di, mbirum pas yi moom daf leen a ñor lool. Looloo tax, nee na, bi mu jotee ci Nguur gi rekk dafa dakkal xaatimug mbooleem pas yoo xam ne dañuy am i njeexital ci li ñuy dippe “les finances publiques”.

Ginnaaw poñ yooyu, moom Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, jot naa dalal xelu saa-senegaal yi ci dund bu jafe bi. Nde, xamle na ne dees na wut yeneen i pexe ngir dund bi gën a jàppandal ci ñépp. Maanaam, ñu jéem ko wàññiwaat ba ñi seen loxo jotul seen ginnaaw sax gis ci seen bopp. Waaye, yemul ci waxtaane dund bu jafe bi sonal saa-senegaal yi rekk. Ndaxte, am na leneen lu fi gën a lëmbe, muy ni ndaw ñi ñàkkee xéy. Muy dalal seen xel, di leen xamal ne ñu ngi ci seen i mbir. Waaye, muy naqarlu it ni ndaw ñi di ñàkkee seen i bakkan ci géej gi. Ndax, mbëkk mi moom, day mel ni bés bu set day gën a yokk.

Moom Njiitu réew mi nag, yemul ci poñ boobu kese. Ndax, xamal na askan wi ne peyug lempo yi kafu ci, fowu ci, te reewu ci. Te, fii ak mi ngi ci boppu réew mi, dina ci xar tànku tubéyam ba képp ku ko war a fey, fey ko, mu dugg fa mu war a dugg ni ko sàrt yi tëralee.

Ba tey, Njiitu réew mi biral na mébétam bi mu am diggante réewi Afrig yi rawatina yu sowu-jant yi. Nde, kenn umpalewul ne jamono jii, Afrig sowu-jant moom coow li bari na lool. Te, dara waralu ko lu moy ñaari kurél yi fi nekk, ku nekk xëcc jëmale àll. Bu CEDEAO jaaree nii, AES jaar nee. Loolu du tere liggéey bi ñu ko ci sas dina ko def na mu ware.

Mu mel ni, li waxtaan wi di gudd lépp am na poñ boo xam ne lum xat-xat dees na ko ci xaj-xajal. Ndax, kenn umpalewul diggante Njiitu réew mi Basiiru Jomaay Fay ak elimaanu jëwriñam yi, Usmaan Sonko. Moo tax, féddaliwaat na kóllareem ci Njiitul Pastef li nga xam ne kenn réerewul liggéey bi mu def ba mu agsi fii tey. Mu koy ñaax mu gën a góor-góorlu. Ndax, nee na, moo am elimaanu jëwriñ bi gën a xarañ ci mboorum Senegaal. Te, mu koy xamal ne fi mu toog tey, jombu ko. Te, yéene na ko mu nekk Njiitu réew. Ndax, fukki at a ngi nii muy xeex ngir loolu mën a am. Te, du mës a teggi tànkam fi mu ko teg.

Kon, mënees na jàpp ne waxtaanu démb wi, kàddu yi fa jibe ay kàdduy leeral la woon, àrtu, ñaax ak dalal xelu saa-senegaal yi. Di leen xamal ne lii mooy yoon wu njëkk muy amal xeetu waxtaan wu ni deme. Waaye, du doon yoon wu mujj. Saa yu ko jaree rekk, te jotam may ko dina ko defaat.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj