Bërki-démb la Njiitu réew mi tasoon Càmm gi daldi tabb Siidiki Kaba Elimaanu jëwriñ yi. Tey lañ siiwal jëwriñ yiy liggéey ak moom ci ñaari weer yi leen dese ci Nguur gi. Wëliis liggéey bu ku ci nekk ci ñoom sasoo ci fànnam, li gën a bir te jamp ci seen liggéey nag, mooy fexe ba amal i wote yu mucc ayib.
Ku wax wote nag, sam xel dem ci njëwriñu biir réew mi. Ndax, moom la yoon sas liggéey yi aju ci wote yi. Kii di Muhammadu Maxtaar Siise lañ tabb, def ko jëwriñu biir réew mi. Moom, njiitul Senelec la woon, moo gàlloo lootaabe wotey njiiteefu réew mi ci bésub 24 màrs 2024.
Bees méngalee Càmm gu bees gii ak gi ñu tas ci àllarba jii weesu, dees na gis ne am na ñees ci génnee. Ñii di Sàmba Si, Faatu Jaane, Séex Umar Aan ak Lat Jóob, ñoom, dañ leen seppi ci Càmm gu bees gile.
Mu am it ku bees ku ci dugg, muy Mankër Njaay mi ñu dénkati njëwriñu mbiri bitim-réew. Ndaxte, mës na ko nekk. Bu njëwriñu jigéen ñi, Terees Fay Juuf lañ teg ca bopp ba.
Ismayla Maajoor Faal mooy léegi jëwriñ jiy bëkk-néegu Njiitu réew mi.
Maam Mbay Ñaŋ, moom, ñaari njëwriñ lay yorandoo : njëwriñu wërteef (tourisme) gi ak gog tàggat-yaram. Bu dee Anet Sekk, moom mooy nekk jëwriñu liggéey bi.
Musaa Balde mi nekkoon jëwriñ njàng mu kowe mi, daf koy desandi, teg ci nekkaale jëwriñu njàngum tuut-tànk yi.
Nii la Càmm gu bees gi tëdde :
-
Aysata Taal Sàll, Jëwriñu Yoon
-
Muhammadu Maxtaar Siise, Jëwriñu biir réew mi
-
Me Umar Yum, Jëwriñu Sóobare yi (Làrme bi)
-
Mankër Njaay, Jëwriñu mbiri bitim-réew
-
Mamadou Moustapha Ba, Jëwriñu koom-koom gi, koppar yeek Naal bi
-
Antuwaan Feliks Jom, Jëwriñu soroj bi ak laf yi
-
Mansuur Fay, Jëwriñu tabaxte yi ak tukkib suuf yi
-
Mame Mbaye Niang, Jëwriñu tàggat-yaram ak wërteef gi
-
Musaa Balde, Jëwriñu njàngum tuut-tànk yi njàng mu kowe mi
-
Sëriñ Mbay Caam, Jëwriñu ndox mi ak cellal gi
-
Mariyaama Saar, Jëwriñu tàggatug liggéey gi, njàngum liggéey ak wutug xëy gi
-
Umar Saar, Jëwriñu mbéll yeek xam-xamu suuf si (sewolosi)
-
Sàmba Njóobeen Ka, Jëwriñu mbay mi, jumtukaayi kow gi ak dund gu doy gi
-
Terees Fay Juuf, Jëwriñujigéen ñi, njaboot gi, yemale gi ak yokkuteg mboolaay gi
-
Anet Sekk, Jëwriñu liggéey bi, diisoob mboolaay bi ak jëflantey campeef yi
-
Mari Xemes Ngom Njaay, Jëwriñu wér-gi-yaram gi ndimbalug njaboot gi
-
Abdulaay Séydu Sow, Jëwriñu taax gi, dëkkuwaay yi ak cetug bokkeef gi
-
Aliyun Ndóoy, Jëwriñu kéewnga gi, yokkute gu sax gi ak càllaleg mbindaare mi
-
Abdu Kariim Fofana, Jëwriñu yaxantu gi, njariñu gi ak àntarpiris yu ndaw yeek yu yemamaay yi, yor kàddu càmm gi
-
Móodu Jaañ Fadaa, Jëwriñu bokk-moomeel yi, sancaan gi ak yokkuteg mberaay yi
-
Aliw Sow, Jëwriñu mbatiit mi
-
Mustafaa Jóob, Jëwriñu yokkuteg ndefar yi ak Pmi yi
-
Biram Fay, Jëwriñu xarala gi
-
Paap Maalig Nduur, Jëwriñu ndaw ñi, cumbantu gi ak liggéey bi
-
Paap Saañaa Mbay, Jëwriñu napp yi
-
Antuwaan Mbeng, Jëwriñu tukkiy kow yi ak yokkuteg tabaxtey naawu yi
-
Wiktorin Ndey, Jëwriñu mikorofinaas ak koomug mboolaay geek jàppalante bi
-
Daawda Ja, Jëwriñu càmm geek njureefi mala yi
-
Musaa Bookar Caam, Jëwriñu jokkalante gi, telekominikaasiyoŋ yi ak nimerig bi
-
Galo Ba, Jëwriñu liggéeyu bokkeef gi ak coppiteg fànnu bokkeef gi
-
Paap Aamadu Njaay, Jëwriñ ci wetu Jëwriñu tukkiy kow yi ak yokkuteg tabaxtey naawu yi, féetewoo yokkuteg yooni raay yi
-
Mamadu Saaliw Sow, Jëwriñ ci wetu Jëwriñu biir réew mi, féetewoo kaaraangeg jegeyoo bi ak kaaraangeg maxejj yi
-
Isaaxa Jóob, Jëwriñ ci wetu Jëwriñu ndox mi ak cellal gi, féetewoo fagaru bi ak caytug mbënn mi
-
Aminata Ãselig Mànga, Jëwriñ ci wetu Jëwriñu mbiri bitim réew, féetwoo mbiri Saa-Senegaal yi nekk bitim-réew