Boo demee ca diiwaanu Sigicoor, dinga fa fekk liise bees duppe Jiñaabo. Waaye, aka néew nit ñi xam kan mooy Jiñaabo !
Njàmbaar, fit ak ngor ñooy jikko yiy màndargaal Jiñaabo. Dafa di, Jiñaabo ab dàkkental la rekk. Turam dëggantaan mooy Jinoyeb Baaji. Moom Jinoyeb, walla Jiñaabo, as ndawu joolaa la woon, amoon fulla lool, gëmoon askanam, daan ko xeexal ba mujje cee ñàkk bakkanam. Jiñaabo mi ngi juddu ci atum 1850, ñu faat ko ci atum 1906, weeru me, fekk mi ngi tolloon ci 56i at. Li ñépp di fàttaliku, moo di ne ay jëfam ndawuñu woon, turam sooyul te nettaleem ñaawul. Ndege, Jiñaabo ci toolu-xare la daanu ! Te kenn newu ko kaay nu xeex, kenn jàmmarloowul ak moom, ñuy dóorante ba moom mu dee. Loolu lépp dara amu ci. Ab buqat, xonq-nopp bu bon, moo taxaw fale, daldi koy fetal, keroog xare Seleki. Diggante Seleki ak Sigicoor, 25i kilomeetar rekk la.
Ki ko faat, nag, doomu Frãs la, nootkat bi, bóomkatu jàmbaar bi.
Ñetti at laata Jiñaabo di ganesi àddina la coow li tàmbali. Ndaxte, ci atum 1886 la leen nguurug Frãs tàmbalee cokkaas, di leen tooñ ak a bunduxataal ba ci seen biir dëkk. Ñu ni déet-a-waay, soldaari Frãs yi di leen sànni ay ndell ak a taal jëppit seeni dëkkuwaay. Dañoo mujj a toxu, ndax seen lépp a yàqu woon, amatuñu woon sax fuñ fanaan.
Ba ci ndoorteelu 20eeluxarnu bi, Farañse yi, jaare ko ci seen ndaw lu leen fa toogaloon, dañoo jàppoon ni Seleki seen moomeelu bopp la woon. Looloo taxoon ñu daan fayloo waa dëkk ba, rawatina baykati ceeb ya, ay juuti ci seenum mbay. Waaye, askanu Seleki mësuñoo bàyyeeku, mësuñoo nangu ku leen di xoqtal, di leen jaay doole ak di aakimoo seen alal. Moo waraloon ndawu Frãs la fa nekkoon, xawoon a ragal Seleki ndax dafa jàppoon ni kaaraangeem desoon na, rawatina ba nit ña fay yeewoo taxawee temm, ne dee duñ fay lempo. Ci meenu jàmbaar yooyu la Jiñaabo nàmpe, kon mënul woon doon lu dul bañkat.
Xareb Seleki bi Jiñaabo ñàkke bakkanam, ci njiiteefu soldaaru Frãs bu doon wuyoo ci turu Lauque la ame. Moo santaane woon cong gi, jiite woon ko yit. Deewub Jiñaabo bi, nag, xawoon na indi jiixi-jaaxa ci xeli waa Seleki yi. Ndege, Jiñaabo du woon ndaw ni yeneen ndaw yi. Dafa amoon lu mu àndal, di woon sëriñ bu mag, amoon i gàllaaj. Kenn mësul woon a foog ne ab balu fetal mënoon na ci moom dara. Ñépp a jàppoon ni dafa tul. Waaye, jaam ak pexeem, Yàllaak ndogalam. Li am ba des mooy ne, xibaaru deewam bi yéemoon na lool waa tund woowee ; daanaka ñu bare nanguwuñ koo woon gëm.
Jiñaabo jotoon naa am doom ju tuddoon Sitaayóbo Baseen. Bi muy faatu, doom jaa ngi amoon 8i at. Bi Tubaab yi reyee baayam, waa dëkk bi dañ koo rawale, yóbbu ko ca dëkk buñ naan Ëllubaliir. Li ñu ko dugge woon mooy bañ Tubaab bi dugal ko ci gaal yóbbu Ndar-Géej, ni mu ko tàmmoon a defe ak doomi buur yi, mu bindu ‘’École des Fils de Chefs’’, ca daara jañ leen jagleeloon.
Nataal bi : ndey-joor jàpp càmmoñ, sëtu Jiñaabo ak Tete Jaaju*.
*Tete Jaajukilifa aada la woon ci Sigicoor ; tuddees na ko jenn daara ca diiwaan boobu.