Lamin Mbaay, ab Birigajeb pólis la woon. Mi ngi juddu 4eelu fan ci weeru desàmbar 1952, ca Mexe. Waaye, Aayre-Laaw, ca Podoor, la cosaanoo.
Ca daaray-ndoorteel bu diwaanu Njaaréem la doore njàngam. Ginnaaw gi, jànge na daaray-digg “Jean de la Fontaine” bu Ndakaaru li ko dale 1970 ba 1971, jaar na yit ca daaray “Pigier” bu Ndakaaru ci atum 1973 ; fa la ame lijaasab “CAP comptabilité”.
Lamin Mbaay nowàmbar atum 1974 la ràngu woon ci làrme Senegaal bi, ñu daldi koy féetale ca màkkaanu soldaar bu “Dakar–Bango”, ca Ndar. Ci atum 1975, ñu toxal ko ca C.F.C.B (ci nasaraan “complément de la formtaion commune de base”) ca màkkaanu soldaar Sémou Djimith bu Kawlag. 1976 la dugg lekoolu pólis ak tàggatug wéyal gi, bànqaasu Wattukatu jàmm. Mi ngafa génneek lijaasab “ Certificat“ bu ànd ak “ mention bien ”laata muy dem Cees ci 1977 mottali njàngam ca GMI. Benn at la fa def, ñu daldi koy yóbbu bànqaasu misig bu làrme, mu nekk fa 4i at. Bokkoon na yit ci soldaar yi jàmmaarloo woon ak way-fippu Kaasamaas yi. Atum 1983 lañ ko yóbbu komisaariyaa bu Cees.
Ginnaaw biñ ko dàqee ba fàww ci liggéeyub nguur gi, ci awril 1987, ONU moo ko jël atum 1989, di ko liggéey loo ci UNHCR miy toppatoo daw-làqu yi. Liggéey na yit Podoor, Risaar-Tol ak Ndar li ko dale 1989 jàpp 1993. Bi fi Senegaal ak Gànnaar demee bay bëgg a xare sax fa la ko fekk.
Moom, nag, mujje woon nañ ko delloowaat ca pólisu Tëngéej ci atum 1993. Bu loolu weesoo, Lamin Mbaay, aji-wommat la, am lijaasab yarub-mbooloo. Rax-ci-dolli, moom, taalifkat la te bind na téere yu bare ci làmmiñi réew mi. Moo jëloon raw-gàddu gi ci jonaŋteb taalif bees amaloon ci atum 1994, méngoo woon ak bés biñ jagleel xeexub sineebar ci Àddina si. 2001, mu jëlati raw-gàddu gi ci beneen jonaŋteb taalif bees jagleeloon 2eelu FIARA (“Foire Internationale de l’ Agriculture et des Ressources Animalières”).
GUDDIG MBOOYO
Guddig Mbooyo, mbirum càcc la nu ci Tiijaan di nettali. Moom nag, mooy boroom-këru Maye mi ay takkaayam ne mes, yëf yi ub boppu ñépp. Te ñi ëpp ci gox bi ñuy wax “Quartier Latin“ jàpp nañ ni Tiijaan ci boppam moo ko sàcc. Looloo ko tax a ubbi ab lànket ngir feeñal dëgg gi, setal deram. Alkaati la ni Lamin Mbaay mi bind téere bi waaye lànket bi yombul benn yoon ndax da cee wéet.
Guddig Mbooyo boole na yëg-yëg, naqar ak seetlu te nekk na téere bu yéeme bu laaj njàngat mu xóot ndax sikki doomi-aadama ma yi ciy Lamin Mbaay di fésal. Duggewu ko nag ñaaw lammiñ ak bëgg a xaste. Li mu ci jublu mooy tooyal xol yi, yee askan wi.
Téere Lamin Mbaay bi dafa neex ba ku ko ubbi doo ko mën a tëj defi leneen te amaana bu jeexee nga ne ci sa xel : “Aa ! Xaat ? “