Utum baayele yi ñeel Usmaan Sonko dina tàmbali ci njeexitalu ayu-bés bi. El Maalig Njaay mi yor jokkoo bu Pastef moo ko xamle. Ci dalu facebookam la ko siiwale. Bees jàngee bu baax li mu fa fésal, bésub 17 noowàmbar 2023 bi lañuy xaar mu jàll ngir ñu daldi ciy sóobu. Muy xamleet ni bés bees ko aayee ñenn ci seen i ñoñ, lawaxu Càmm gi dootul am jàmm ci réew mi waxatumaak biti-réew.
Ci pàttali, ci bésub 17 noowàmbar boobu la ëttu Cedeao war a joxe àtteem. Ci la waa Lacos itam woote ñaxtu ci réew mi ak ci bitim-réew. Waaye ba tey ci lu ñeel bés boobu, jëwriñ ji Abdu Karim Fofana mi yor kàddu nguur gi mi ngi leen doon dànkaafu démb ci dibéer ji. Muy xamle ni Càmm gi dina jàmmàrlook képp kuy yàq tax a jóg te waa ndakaaroot duñu nangu ku leen xañ seen jàmm.
COOWAL CENA BI
Tey ci altine ji la tabbeefi Njiitu réew mi ca Cena doon waat laata ñuy jot ci lengee yi ci bés yii di ñëw. Ginnaaw bi ñu waate ba noppi, Abdulaay Silla mi nekk ca bopp ba fésal nay kàddu ñeel liggéey bi leen di xaar. Muy xamle ni bés bu ñu jëlee lenge yi, dinañu amal ndaje mu mag ci lu gaaw ngir càmbar mbri Usmaan Sonko ba mën a xam lan moo ciy nekk seen taxawaay. Muy xamleet ni fas yéenewuñu jéggi lenn lu yoon tëral. Waayeet, maxejj bu yoon mayul nga nekk aji-fal, doo fale ; maxejj bu yoon mayul nga nekk lawax, doo ko nekk.
Jamono bi tàbbeef yi doon waajal seen waat gi, mbooloom kuréli maxejj yiy saytu wote yi, ñu gën leen a xam ci Cosce (Collectif des organisations de la société civile pour les élections) mi ngi doon xàñ anam wi leen njiitu réew mi tabbe. Nde ci seen yëgle, Njiitu réew mi sàmmontewul ak sàrt yees war a tabbe waa Cena bi. Dekkere bi mu ko jaarale dafay naxasal gile campeef. Ba tax ñuy sàkku ci Njiitu réew mi mu neenal ko te defaraat beneen bu méngook doxalin yi yoon tëral.
MBËKK MI
Ginnaaw jëyya yi am ci mbëkk mi ak junniy junniy ndaw yi ci ñàkk seen bakkan, kurél gii di Ong Horizon sans frontière a ngi woo Njiitu réew mi ci ñu bàyyi leen xel. Naka noonu, muy sàkku ci moom mu dakkal làmb yeek lépp luy xeeti yëngu-yëngook mbumbaay ngir amal bés ub dëj fépp fi réew mi. Jàpp naat ni war na ci moom mu gunge te taxawu bu baax njaboot yi ci ñàkk seen i doom. Lu ko moy, dees na njort ni dafa soofantal bakkan yi ci rot walla yëgalu ko yaramam.
BITIM-RÉEW
Ca réewum Mali, xare baa ngay jolli ca diwaanu Kidaal. Ginnaaw bi fa sóobarey mbootaayu xeet yi jóge, sóobarey Càmm gee ngi jàkkaarlook rëralkat yu CSP-PSD yi ngir nangu ci ñoom diwaan bi ñu teg loxo ci atum 2012 ak tey.
TÀGGAT-YARAM
KUPPEG ÀDDINA U17
Xaley Senegaal yi def nañu duggu bu am solo ci kuppeg àddina gees jagleel ndaw yu ëppalagul 17i at. Ci gaawu gii, 11 nowàmbar 2023 lañu doon daje ak Àrsàntin ci seen joŋante bu njëkk ci bi. Ñoo mujje dóor ñaari bal ci benn (2-1). Kii di Amara Juuf moo waneeti boppam nees ko xame, daldi dugal bii bu rafet ca 6eelu simili ba, tollanti ko xa 39eel ba. Bañ demee ba ci njeexital la, ca la Àrsàntin daldi dugal moom it benn bii.
BOKKADIL KUPPEG ÀDDINA 2025
Ekibu Senegaal bu mag bi dina amal ñaari joŋante ñeel bokkadil kuppeg àddina giy ñëw ci atum 2025 mi. Bi ci jiitu dina daje ak Sudã-Bëj-saalum fii ci réew mi 18i fan ci weer wi, bu ci noppee fekki Togoo ci bésub 21eel ci weer wii.
Aliw Siise, tànn na ñi mu soxla ci yoyou joŋante ba noppi. Waaye, andi nay leeral ci li mu woowul Ãri Sewe (Henry Saivet). Wax na ni : ” Ãri Sewe mu ngi def jéego yu am solo ca këlëbam, ma di ko ci ndokkale. Nit ku baax la. Waaye, danoo am ndaw yu bari yuy doxal fa muy doxal ci pàkk gi. Loolu moo waral woowunu ko.”
NIKOLAA JAKSON YEEWU NA !
Ci jamono yii ñu génn, wax ji bari woon na tuuti fa Àngalteer ñeel mbiri doomu Senegaal bi ñëw ren Chelsea. Nikolaa Jakson dafa tegale woon ay joŋante yu bari yum dugalul, loolu jur ay wax ak i laaj yu jëm ci ndax mat na la ko Chelsea doon doyee. Dafa mel ni nag loolu dafa xiiruloo gaynde gi. Nde, barki-démboo njaay la taal ñetti bii ci seen joŋanteek Tottenham (4-1), ci dibéer jii mu dugalaat beneen ci seen joŋante ak Man City (4-4). Fim ne moo ngi ci Juróom-ñetti bii (8) ci fukk ak ñaari joŋante (12).
PSG : USMAAN DÉMBELE DUGALAGUL BA TEY
Farãse bi jaaxle na fim toll nii. Ndax, ba mu demee ren ca Paris Saint Germain ba léegi dugalul. Donte ekib baa ngi dox muy amal ndaje yu am solo, bii yiñ ko xame woon ca Barça dañu ko daw. Ndax fàttewu ko fa ? Lu leer ba leer mooy “xëcci bu daggul dikk”.