LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI Altine 12 ut 2022

Yeneen i xët

Aji bind ji

TÀGGAT-YARAM

Ikibu Casa Sport bi dugg na ci joŋantey Ligue des champions / CAF bi. Jot naa am ndam (1 bii ci 0) ci kow ikibu Kabili bi mu doon dalal ci Estaad Mr Abdulaay Wàdd bu Jamñaajo. Muy seen janoo bu njëkk bi ñu doon amal ba tey ci bokkadil yi.

YOONU MÀGGAL

Sëriñ Muntaxaa Mbàkke, Xalif bi jiite yoonu murid, dalal na Njiitu Réew mi Maki Sàll. Mu doonoon tukki nemmiku bu mu fa doon amal ci waajtaayu Màggal gi. Moom Njiitu réew mi nag, xamle na fa ne dara du ko tere wéyal liggéeyam foofa ca Tuuba. Te yéeneem mooy bàyyi Senegaal ci anam gu gën gi mu fi fekkoon.  

XEW-XEW

Yaraŋ, ca Séeju, ñeenti ndaw ñoo fa lab ci toolu ceeb yi. Kenn kott ci dese bakkanam. Ñett ñi dañoo faatu laata ñu leen di wallusi. Li gën a yéeme ci mbir mi mooy ñoom ñépp ñoo bokk genn kër. Mu tiis lool ci seen njaboot. 

KAAWTÉEF

Téeméeri kër yoo jël, ñaar-fukk ak ñaar yi xamatuñ ndékki, añ ak reer. Loolu bokk na ci njureefi gëstu bu DPEE (Direction de la Prévision et des Études Économiques). Mu nekk mbir mu doy waar muy wone ndóol ak xiif gi ci réew mi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj