« Toj naa fii ! », « Tasaare naa fee ! », « Rajaxe naa fale ! »…
Su nu waxantee dëgg, xorom si moom la ! Moom Madike Ñaŋ, kenn ci wutaakoni yi, mooy xorom siy safal kampaañ bi ñuy waaj a jéexal.
Ci biir werante yeek, xuloo yeek, ŋàññante yeek, tamante dëmm yi, Madike moom, neex deret ba dee, ciy ree ak i kókkali, boole ciy kàddu yu rafet, lanuy jaaye sàrtu doxalinam bi mu faf tudde « Jàmm ak xéewal ».
Dal ak aafiya daal la indi ci kampaañ bi nga xam ne, boobaak léegi, ni nu ko waxe ci njélbéen gi, defante doŋŋ lees ci seetlu, defante bay dóorantey kurpeñ, di génney jaasi… Nii lañ fi woññee — walla woññeegum ? — ñaar ba ñetti doomi-Aadama yu seen bakkan rot.
Madike moom, ci jamono yii, mu ngiy toj Anternet. Mook Usmaan Sonkoo ko koy xëccoo, sax. Sonko daa aakimu, daanaka, reeso sosiyoo yi, bàyyi wujjam yépp ginnaaw ci wàll woowu. Waaye Madike Ñaŋ sorewu ko lool ndax saa yoo duggee Anternet daj ciy nataalam mbaa dégg i kàddoom. Ne ñi mën a muñ i feemam barewuñu. Moom daal day reeloo nit ñi ba seen biir di metti ! Wax ji benn la : ‘’kii daal moo neex !’’…
Waaye li am ba am, moo di ne, wutaakon bile, mu tey ko mbaa mu bañ koo tey, fexe na ba nit ñi génne seen xel ci liñ yàgg a ruumandaat : ndax, moom, jot ci réew mee ko tax a jóg walla dafa bëgg a sotle Maki Sàll ba noppiy dof-doflu, di reeloo askan wi ? Madike Ñaŋ, ndax yàqal Ablaay Wàdd ak Karim ak seen pàrti, PDS a ko tax a sàmp ndëndam ? Lu waral layookat bu siiw ni moom, amoon lool bayre, doon ku am fulla, xéy di wër réew miy wax ay waxi ku daanoo ci saret ? Xanaa kay li ko jaral a sóoru Wàdd du neen ! Ndax kat, ‘’Góor-gi’’ léppam la woon, ni sët la ko mas a jàppe, jàngal ko politig, doon njiitam.
Nu seetaanati ba xam « fu boroom wànnent di mujje ak i gëtam »