Sagar a ngi xeeñ. Ñépp a ko maase yëg. Xet gi ëbale ne ràpp réew mépp. Xanaa kay Saa-Senegal yi dañoo tàmm ne, bala ñoo fay lakk, fàww dëkk bi ne jëppet. Mi ngoog kon, menees na wax ne, réew mi tàkk na, wala sax tàkkati na. Mu mel ni mbir mi du guléet. Te wolof dinay faral di wax ne : “ku ñépp tufli ngaa tooy”. Ndéyu àtteg Bokkeefu Senegaal moo ngi waaj a lóor. Te ndey ji séex du tëdde wet, day jaaxaan. kon, lu jiin Njaag a, te moom mooy Njaag.
Ñu bëgg a junj foofu ne, li mu doxale ci këyiti Bennoo ak gu Yewwi Askan Wi yépp, teey na xel. Lenn kay la ñépp doon xaar mooy : dàq wala nangu, ci ñoom ñaar ñépp. Te bu ñu fàtte ne, lu yëngu lu ne, la ko yëngal a ko ëpp doole. Kon doxu-ñaxtu bi waa Yewwi Askan Wi ak Wallu Askan Wi bëggoon a amal te ñu gàntal leen ko, tegewul fenn.
Dees na wax ni, kenn du maye bopp ba noppi, di rocci làmmiñ. Ndeyu àtte Bokkeefu Senegaal mënul xaatim aw xët wuy may bépp maxejj mu ñaxtu bu ko neexe, ba noppi di ko ko xañ. Te, bu dee lay waral ñu gàntal loolu ñaari mbir yépp daa war a daje, muy lan ? Pëccaxoo gu am ci réew mi ak ñàkk matuwaay, kaaraange gu yiir boobu xew-xew. Te lenn de weranteesu ko, kaaraange de moom mat na sëkk, xanaa kay pëccaxoo, bu ñu bëgg a forse réew mi la ñépp di kumuj. ñu ne xobbeeku bala ngay lakkle. Te dafa mel ni, la mu doon daw, ca la faf dal. Te mbir ya faf jéggi dayo. Ndax, bu ñu demee ba lu tollu ci ñetti bakkan rot ci, ñu bari ame ay gaañu-gaañu, ñii yoon teg leen loxo, ak yàqu-yàqu yi, fa la ay mën a yam.
Lii yépp di wone ni, sañ-sañ dañu koy fonk. Bu ñu la dénkee ngir nga àtte, dangay yemale tay doxe dëgg. Mu mel ni, baat boobu ñu bari ci réew mi dañ koo ragal.
“Liy dëgg mooy, garab, ku bañ doom ya doo ko suuxat muy naat”. Soxna si lii la wax, muy dëgg itam. Ñu mën cee jàng ne : fii ci Senegaal garabu fitna, dañu koo war a ni dàjjet jële. Te li ko fi war a jële mooy àtte dëgg, te bañ a par-parloo.