Dibéer 31i fan ci weeru Sulet nekkoon bés bi ñu doon amal wotey palum depite yi ci biir réew mi ak ca bitim-réew. Mu nekkoon nag xew-xew bu am solo lool ci ñiy fale ak ñiñ war a fal ngir ñu taxawal leen ca Péncum ndawi réew ma. Waaye, lees nemmeeku ci wote yii mooy néewaayu limub ñi wote ci gox yu bari. Muy ci biir réew mi ak ca bitim-réew. Mu doon nag mbir mu doy waar lool. Ndax kat, kenn umpalewul ne wareef la ci bépp maxejj bu am kàrt, mu génn woteji. Bokk ci ñiy fal ak di follee. Te, ci jamono jooju rekk la maxejj bi mёn a wane ag ànd walla ag ñàkk a àndam ci ni Péncum ndawi réew ma di doxe. Xam xéll tamit ña fa nekkoon kan lañ fa nekkaloon ak nan lañ ko fa nekkalee woon ? Ba buy fal xam kan lay fal ak lan moo tax mu fal ko ? Moo tax nag, ay laaj mat a sampu ngir xam lan moo tax maxejj yi am taxawaay bii ci joŋante yii ? Ag càggante la walla ag ñàkk a xam la ?
Wotey palum depite dafa nekk lu am solo ci doxalinu réew. Ba, képp kuy saa-senegaal, mёn a wote, war a xar sa tànku tubéy ngir matale sa wareefu maxejj. Waaye, saafaan wi lees gis ci wotewaay yu bari ci réew mi. Ndax, ci dibéer ji ci boori benn waxtu ci bёccёg, kurél gu mag giñ dénk wàllum wote yi (DGE) xamle na ni téeméer boo jёl lu tollu ci 22% moo ci wote. Donte ne sax, ñi ngi doon xaar lu tollu ci 50% laata wotewaay yi di tёj, juróom-benni waxtu ci ngoon. Waaye, bees sukkandikoo ciy xayma yiñ mujjee def mbir yi àggul foofu. Li koy firndeel mooy fee ca diwaanu Luga ca gox buñ naan Lewna am na lu tollu ci 445 yu bindu, 218 ñoo ca wote. Te, noonu la deme ci gox yu bari ci biir réew mi. Ba tey, ca bitim-réew fu ca mel ni Berlin 292 ya bindu woon, 61 moo ci wote te gox yu bari noon la fa deme. Léegi, lan moo sabab taxawaay bii maxejj yi am ko rawatina ci nekk ci biir réew mi ? Càgganteg yenn ci maxejj yi la, seen ñàkk a xam, ñàkkug jot walla taw bi (nawet) ci yenn gox yi ? Lii, di yenn ci sabab yu yenn ci maxejj yi di tànxoo. Lu ci mёn di am mbir mi ci maxejj yi la. Donte ne sax, am na ci ñoom ñu ne siiw ngir jot seen kàrt mёnuñu ko. Waaye, mbooleem gaa ñi fare ci lёkkatoo yépp woo nañ seen i militaŋ ca teel ngir ñu jёli seen i kàrt. Ndax kat, kàrt yi mooy seen ngànnaay, te kuy dem xare fàtte sa ngànnaay faso fa yéenee yàgg.
Li ci doy waar nag mooy dafa bari ci maxejj yi ñu jàpp ne wote bi amul benn solo. Waaye, loolu moom càggante mёnu koo rombu. Ak fi jamono ji tollu nii, nit warul réere lu ame nii njariñ ci réew, dem ba di ko ñàkkal faayda. Ba tey, ñi jàpp ne seen jot muyuleen ñu wote ji dafa fekk ne jaraluleen ko. Muy ñi nekke ci dёkki àll yi, di ñi yor seen liggéeyi bopp walla di liggéeyal kenn ak képp ku jàpp ne ay wote jaralula nga dagg say yitte. Dañoo réere ne, coonooy njёlbéenug njariñ, ku bёgg dara, def dara. Loolu lépp, day wane càgganteg maxejj yi ndax ci yoon waruñoo xaar kenn di leen ci jiitu. Mooy liñ naan paaka moom, kenn waru koo jiitu ci mbaram.