RIIRU KÀMPAAÑ

Yeneen i xët

Aji bind ji

Lépp lu yëngu am na lu ko yëngal. Réewum Senegaal, jamono jii mu ngi toll ci waajtaayu joŋante bi ñuy fale kiy toog ci jal bi. Këru-Àtte gi gën a kowe fésal na juróomi wutaakon yu samp seen ndënd : Maki Sàll, Isaa Sàll, Usmaan Sónko, Madike Ňaŋ ak Idiriisa Sekk. Kenn ci ñoom la xelam toogatul fan yii, taluñu lu-dul kàmpaañ bi. Lawax yaa ngi jaabante, dëkkoo-dëkk ñu dem fa, di saafonteek ñaa fay yeewoo. Ñoom ñépp a ngi biral seen gis-gis ci doxalinu nguur ba noppiy tanqal askan wi ak i dig. Waaye Wolof Njaay dinay wax ne : dige, bor la. Naka noonu, ay ndaamaar lañuy war, foo toll di leen séen ñu yëkkati seen loxo ca kow, misig biy jolli. Lu kàmpaañ bi gën a jege di gën a rëb ; li koy firndeel moo di ne ñenn ci doomi-réew mi ñàkk nañu seen bakkan keroog bay farandoo Maki Sàll ak Isaa Sàll jàmmarloo. Wutaakon yaa ngi defante ba mu saf sàpp te ñi leen di jàppale kenn demul ñu des, fu nekk ñu nga fay daje, di def seen kem-tàttan ngir seen mbër jël ndam li. Kan lay doon bu bés baa ? Tont laa ngi ci yoon wiy ñëw…

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj