Saartjie Baartman ab jaam la woon, fekkoon baax ca réewum Afrig-bëj-saalum. Moom, nag, benn doomu Àngalteer lañu ko jaayoon. Gannaaw bi, Tubaab yi dañu ko wutal ab dàkkental, tudde ko Venus Noire walla Venus Hottentote. Ci atum 1810 la àgg Tugal. Bi mu àggee, nag, tubaab yi dañu ko wuññi, gàcc ko, làññi di ko wone ci ja yi ak luuma yi, diggante Àngalteer ak Frãs.
Waaw.
Saartjie Baartman as ndaw su jekkoon, ab diriyànke bu amoon waŋ ak i ween yu réy lool la woon. Mu jaaxaloon tubaab yi, ba tax fu nekk lañuy jóge ngir deñsi-kumpa soxna si. Noonu la Tubaab bi nekke woon ak moom, xàwwi suturaam, dëkke koo toroxal. Yenn saa yi sax ñii làmbatu ko, ñee siif ko, ñeneen ñi di ko jam ak seen parasol ak yu ni mel.
Mënees na wax ne, Tubaab yi ab mala lañu jàppe woon Saartjie Baartman. Li koy gën a firndeel mooy li ñu ko boole ci benn téere bees jagleel mala yi. Ku def jëf ju bon te ñaaw jooju mooy Cuvier, benn doomu Frãs bu doon gëstu xeeti mala yi. Noonu, gannaaw soxna Saartjie Baartman nit ku ñuul la woon, Cuvier da koo boole ci mala yi, saytu ko, amal ay njàngat ci moom. Noonu, mu méngale ko ak mala yiy nàmpal, boole ko ci biir téere boobu nga xam ne, dajale xeeti mala yiy dund yépp a ko taxoon a jóg.
Bi mu faatoo ci atum 1815, kenn ci gëstukatu Frãs yi gënoon a mag te xelam màccoon ci xeet yiy dund, da koo fees, daggate ko, teqale cër yi. Mu seppi yóor gi, dindi awra wi, denc leen ci anam boo xam ne duñu yàqu. Jëmm ji moom, ñu lëmës ko ne ko gàcc ci kàggu-aada gi ñu duppe “Musée de l’homme” te nekk ca Pari, di péeyub réewum Frãs.
Saartjie Baartman, nag, dara yóbbewu ko mbugal bu ñaaw bii lu dul ni jigéen ju ñuul bindoo ak taaram. Ci atum 1994, ab diir ginnaaw bi politigu boddikoonte ci biir xeet (apartheid) jeexe ci réewum Afrig-bëj-saalum, ca la askan wa ñuy woowe ay xoyxoyca mooma réew sàkku ci Nelson Mandela mu fexe ba jot ci néewub Saartjie Baartman. Seen jubluwaay moo doon suturaal ko, denc ko ci bàmmeel. Waaye ñenn ci gëstukati réewum Frãs lànk ba tëdd ci naaj wi. Amuñu woon benn lay lu dul di wax ne néewub Saartjie boobu moomeelu Frãs la. Noonu ba ci atum 2002 ci la Frãs soog a nangoo jébbale Saartjie Baartman ginnaaw bi dipite yi jëlee ndogal lu ni mel ca péncum-ndawi-réewam.
Tabo M’Beki mi jiitewoon booba ‘’Afrique du Sud’’ sànni woon na ci kàddu yu daw yaram yii : “Kiy niru mala dëgg-dëgg du doomu-Afrig bii di Saartjie Baartman. Déedéet. Mala yi dëggëntaan ñooy ñi ko xañ boppam ba noppi def jëf ju ñaaw jii”.