Nu yattati sunu xalima ngir biralati sunuy kàddu. Waxati dëgg jot na. Nu dikk ak yéen ci mbiru doxandéem yi féete fii ci Itali. War ngeen a miin sax sunuy kàddu ci wàll woowu ndax fan yee ñu weesu, xamaloon nañ leen as lëf ci doxandéem yooyee ak ni leen Salwini di bundxatale bi mu toogee ci jal bi ba tey.
Linu indi tey nag moo gën a yéeme ndax mbir yi day bëgg a ëpp i loxo. Li fi tàmbaleeam ñaaw na ba fu ñaawaayyem. Jéyya yi xew wetu Fogsiyaa,di ab dëkk ci Itali,ëpp nañoo muutuwaale.Ayu-bés yi weesu, li ko dale 13elu fan jàpp 15elu fan ak 17eluba ca 23elu fan wa ci weeru sulet ci at mii nu nekk di 2019, ay doomi Afrig yu wàlliyaansi ci wetu Fogsiyaa lañu xaañ. Nataal bi xibaar bi àndal rekk doy na firnde.Waaw, ay nit yu weex ñoo gànnaayoo ay xeer, làqu ci oto mbaa ci ab ruqu dogaale nit ñu ñuul ñi doon liggéeyi, sànni leen ko ci bopp. Seetal ma lii rekk ! Ay doxandéemyu yeewu njël ngir dem daani seen doole, ñu def leen lu ñaawe nii. Ñu ne déet-a-waay 26elu fan ci weeru sulet ba tey, ñaari Amerikeŋ faat ab takk-der ci Rom ñu njëkk ko jiiñ ay doomi Afrig. Noonu, seen bakkan nekk ci xottu ngerte. Loolu lépp, li ko waral mooy xeetal (racisme) giy bëgg a law ci biir Itali te Salwini di ko xamb saa su nekk.
Moo taxit kenn ci sunu mbokk yi ñemeetul a génn dem fenn ndax ragalmoo xam ndax demliggéeyi la, dugg ci kaaryi, ci saxaaryiwallaci metórobi. Ndaxte fi ñu tollu nii, ci gis-gisuñenn ci Italiyeŋ yi, doomu Afrig mooy musibamréew mi, di nattoom. Ba tax nabari na ñuamatul yërmaandeci ñoom, seen yoon ci seeni tolof-tolof mbaa seen naqar. Ñu dem bamu am ñutumuraanke ak tiitaange tee nelaw. Mbaa ku ci forbët sax, aygént yu ñàng yee la ba ngay luqeeku. Nekkin wu tar woowoomujjee jur ay jafe-jafe ci seen wér-gi-yaram ba bés bu Yàlla sàkk ab doktoor di leen saytu ak a bindal i garab ngir wàññi seen tiis. Waaye mel na ni loolu fajul dara ndax am na ñu seen furu-fara jot a dem. Li ci gën a doy waar nag mooy mbégte mu réy mi doomuAfrig bi fi xaruwoon jur ndax jotul woon ay kayitam. Léegi,mën nañoo ree ndax rekk li kenn ci doxandéem yi wàññeeku.150 nitñi lab ci diggante Libi ak Itali ci 25elu fan ci weeru sulet jaruñwaxaale ne kenn du leen jooy ndax deru kuñuul amu fi solo.
Ràññewuñu Senegaale, Ruwaande,Aforo-amerigeŋbeek Kubeŋ bi. Ci ñoom daal nit yñu ñuul ñépp a yem.Te moo ne dey ñu wuutelañu ci aada, ci melo, ak ci cosaan.
Li nuy metitlu ci mbir mi mooy di ne bu weesoo ab taskatu xibaar bi doon jéem a delloosi xel yi naan nañu moytu dugal politig ci lépp lu ñaaw lu xew, kenn baaluwul àq walla ne, aa, man kat damaa juum, tooñ naa ay doomi-aadma ni man ndax seen ñuulaay. Waaye di wax rekk ne, bu yoon jeexul, waaxusil du jeex, teitam bañ bañ bëgg.