AY NJÀNGAT ÑEEL KÀMPAAÑI WOTEY PALUM DEPITE YI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Fi mbir yi tollu nii tembe, gaa ñi fare ci làngug pólitig, ku nekk ci ñoom a ngi lal i pexe ngir am baatu askan wi. Muy ñi fare ci lёkkatoo yépp nag, kenn desul gannaaw ci xeex bi. Ku nekk ci ñoom a ngi def kéemtelaayal kàttanam ngir askan wi jox ko bopp. Ñii di ko jaare ci ay kàddu yu ñuy jibal ci tele yeek mbaalu jokkoo yi. Walla sax, di dem ci gox yeek goxaat yi ngir waxtaan ak maxejj yi. Waaye, lu ci mёn di am, askan wee yor kàddu gu mujj gi te mooy fal di folli. Mu mel ni fi mbir yi tollu nii nag, ñoom ñépp a yittewoo xam jafe-jafey askan wi, xam liñ bёgg ba am fuñ leen jaar. Ndax, ku bёgg dara kat, def dara. Te, ku bёgg akara fàww nga ñeme kaani. Moo tax, ñépp di leen jege ci jamono jii ngir xam ni ñuy ak li ñuy dunde. Mooy, liñ naan bёgg ngёrёmal pёl dina tax a boot i sёll. Moo tax, askan wi nga xam ne moom kepp a am kàttan ci jamono jee mёn a ràññe ki koy jariñ ak ki koy jariñoo. Te moytu bukki yi sàngoo deru béy yi jóox ci gétt gi, bala ñu koy fàdd. Kon nag, lan moo war a nekk taxawaayu askan wi bu mbir yi tolloo fii ?

Lu tollu ci juróom-ñetti lёkkatoo ñoo jàll ci parrainage yi. Lёkkatoo yooyu di: Bennoo Bokk Yaakaar, Yewwi Askan Wi, Wallu Senegaal, Bokk Gis-Gis/Liggéey, Naataange Askan Wi, Buntu Bi, lёkkatoo gi ñuy dippe Les serviteurs ak bi ñuy dippe Coalition alternative pour une assemblée de rupture. Ñoom ñii ñoo war a joŋante bésub fanweeri fan ak benn ci weeru Sulet. Am na tamit ñaari lёkkatoo yi boole seen doole ci yenn gox yi muy YAW ak WALLU ngir nёrmeelal waa BBY. Moo tax, ci jamonoy kàmpaañ yii la askan wi war a tànne kan moo leen di nekkal fale ca péncum ndawi réew ma. Ndax, mboolem lёkkatoo yi ak ñi leen jiite ñi ngi topp gox ak goxaat, ruq-ruqaat yi nekk ci réew mi yépp ngir xamal maxejj yi liñ namm ci réew mi. Bu BBY nekkee ci diwaanu Kafrin, YAW nekk ca diwaanu Lingeer (Luga), ñii di Wallu ak yeneen lёkkatoo yi nekk ci yeneen gox yi. Ñoom nag, fuñ dem waxtaan ak gaa ñi wan leen seen sémb (programme). Ku nekk fum dem ne mooy boroom, ŋàññi ka ca des walla mu koy gaaral. Waaye nag, mbir yi dafa mel ni dafa am ci boor bum gёn a tare muy ci diggante BBY ak YAW-WALLU. Su ñee nee waa boor bee dañoo bёgg a daganal ngóor-jigéen buñ amee doole ca péncum ndawi réew ma. Ñee di leen jàppe ay niti fitna, bёgguñu jàmm ci réew mi ak yeneen yu ni deme. Ku nekk ci ñoom di lal ay pexe ngir ñàkkal faayda ka ca des ba askan wi mujj di ko xalab. Am tamit yeneen lёkkatoo yoo xam ne dafa mel ni dañoo tёdde njaaxanaay ci xeex bi, seen sémb kesee leen ñor. Kon nag, askan wi nga xam ne moo leen tax a jóg ñoom ñépp, ci yan anam lay tànnee ak lay wóoye ab lёkkatoo ? Tànneef gi muy def day tёnku ci yaa ma neex walla ci yaa gёn ci man ?

Lu ci mёn di am, jamono yii taxawaayu askan wi moo war a doon settantal sémb yi leen gaa ñi di jox. Ndax, ci jamonoy kàmpaañ la képp ku dib maxejj war a xame lu bépp lawax mébét ci réew mi. Xam xéll ki gёn ci moom ndax kat nit moom yoon wum jaaroon dee, bu dekkee war koo teggi. Ndax, ci biir lёkkatoo yi am na ñu ci jotoon nekk ca péncum ndawi réew ma. Moo tax, mu war a teey ba xam kan lay tànn ak lan moo waral tànneef gi. Waaye, loolu tekkiwul ne day xaar ki gёn, te kat tànnkatu dàll moom bu moyuwul ci carax lay mujj. Ba tax na, képp ku dib maxejj war a xam ne kàmpaañ du mbumbaay kese walla sànnante xeer, gaaralante ak a ŋàññante. Waaye, mooy jamono bi lawax bi war a wane askan wi lu tax mu war ko wóolu ba mёn ko jox baatam. Lu ko moy kat, cig yaa ma neex kepp la askan wi di mujjee tёnk ag tànneefam te du lu gёn ci moom.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj