CÀDD, JÀMM FÀDDU NA !

Yeneen i xët

Aji bind ji

Juróom-fukki bakkan yu rot ak ñetti téeméeri nit yu amey gaañu-gaañu, lii, fit du ko weesu. Réewum Càdd, jamono jii, moo nekk di tàkk. Lu xew ? Askan waa génn di ñaxtu, ca Njamenaa, péey ba, ak ca yeeneen i dёkk. Lu tax ? Li Mahamat Idiriis Débi gàlloo Njiiteefu Càmmug négandi gi ak li mu yokk diir bi moo ko waral. Kañ la coow li door ? Alxames 20 oktoobar la jàmmaarloo bi amoon diggante askan wa ak takk-der ya.

Coow la ca teen ba, ña amul baag a ko waral

Ku xamb Afrig ? Coow laa ngi fi ne kur, rawatina biir Afrig sowu-jant. Mali, Gine, Burkinaa Fasoo, Càdd… fépp a ngi boy. Te, réew yooyii yépp nu fi lim, ci loxoy sóobare lañ nekk. Càdd muccul ci ay wu ni mel. Fitna jooju fa jib nag, ndajem-ñaxtu ma kujje ga woote woon a ko yee, keroog alxames 20 oktoobar. 

Bi Idiriis Débi, Njiitu réewum Càdd ma woon, faatoo la coow li door. Nee ñu nag, waa Front pour l’Alternance et la Concorde au Tchad (FACT) ñoo ko rey, keroog bi ñu ko bette ca boori Libi, diggante 17-19 awril 2021, song ko. Ca la jёle woon ay gaañu-gaañu ba faf faatu bésub 20 awril 2021, ginnaaw bi mu amee fanweeri at ci boppu Nguur gi, yemoo woon ak juróomeelu kayam. Léegi nag, ca la doomam jii di Mahamat Idriss Débi Itnoo, ci ndimbalu Farãs, jёlee woon njiiteefu Ndajem sóobare mu négandi mi. Maanaam, bu ñu delloo ci sàrtu ndaje ma, moom mooy taxawe cёru Njiitu réew ma. Waaye, li doy waar ci mbir mi kay mooy li ñu xaatimoon ci ndeyu-àtte yi muy bu fi Njiitu réew mi jógee, walla mu am ngànt, Njiital Senaa lee fa war a nekk lu tollu ci 45 walla 90i fan ba ni ñuy ame jotu amal ay wote. Larme bi dafa ñёw daldi tas mbooleem càmmeef (institutions) ya fa nekkoon, muy péncum ndawi réew ma ak Nguur ga fa nekkoon, ba pare taxawal seen Nguurug bopp. Rax-ci-dollu, ñu tёj seen i dig boole ci jёl ndogalu tёj askan wi ci yenn waxtu yi. Ci lañu xamale askan wi ne sóobare si jёl nañu Nguur gi te dinañu ko yor lu tollu ci fukki weer ak juróom-ñett (18). Bu ko defee, réew mi mёn a delluwaat ci ag dal, ñu mёn a amal ay wote yoo xam ne moom du ca bokk. Waaye, dafa mel ni mbir ya mujjewul a deme noonu. Nan la mbir yi deme ?

Bi fukki fan kepp desee ngir moom mii di Mahamat jóge ca boppu réew ma, ca la defee li ñu naan wax-waxeet. Mu mel ni mbir yi dafa am lu lalu ci ginnaaw. Moo tax, ca waxtaan wa mu woote woon ngir boole ñépp ñu dippe ko dialogue national inclusif et souverain. Te, ñi ёpp doole ci kujje gi bañ ne duñu ca dem. Ci lañu ko defe Njiitu réew ma, yokkal ko ñaar-fukki weer ak ñeent, maanaam ñaari at ginnaaw ba nga xamee ne fukki weer yi ak juróom-ñett ya daanaka jeex na. Te, ca jamono jooja fekk na mu am genn làng gu fa sosu woon tàmbalee am doole lool ca réew ma ñu dippee ko Les Transformateurs, kii di Succès Masra jiite ko. Te, moom mu nekk koo xam ne bokkul ak ñoom gis-gis ci ni ñu war a yore réew mi. Bi ñu jёlee ndogal loolu, moom dina mёn a samp ndёndam doon lawax ci wote yiy ñёw ngir mu mёn a wéy di jiite réew ma. Loolu, mi ngi nekkoon 10 oktoobar 2022. Am nag ci askan wa, rawatina kujje gi ak seen i ñoñ wane seen ag ñàkk a ànd ci ndogal yooyu. Muy li mu yokk àpp bi ak li mu bёgg a bokk ci joŋante yooyu di ñёw te yor doole jépp. 

Ci lañu waajale seen ndajem-naxtu ci alxames ji 20 oktoobar, bés ba nga xamee ne ca la Mahamat waroon a jeexal ab àppam ci boppu Nguur gi. Ñi fare ci Nguur gi tere leen ne bu ñu fa amal ndajem-ñaxtu. Mu mel ni, boobu fekk na xas na boy. Moo tax, ca alxames ba lañu xёy wàcc ci yoon yi wane seenuw naqar. Foofu nag, la fitna ja yewwoo ba bóomante am ca yoon. Am ci takk-der yi ñu ci ñàkk seen bakkan, naka noonu ñaxtukat yi tamit bari ñu ci ñàkk seen bakkan. 

Dafa di, fetal moom du xeex ak xeer walla yat. Moo tax, fu benn takk-der faatoo, fukki ñaxtukat faatoo fa. Mu bari lool ñu ci ñàkk seen bakkan ak ñu ci jёle ay gaañu-gaañu ak ñu ñu ci teg loxo. Bees sukkandikoo ci li kii di jёwriñ ju mag ji Saleh Kebzabo biral, juróom-fukki nit ak lu teg ñàkk nañu ci seen bakkan, lu tollu ci ñetti téeméeri nit jёle ci ay gaañu-gaañu. Loolu, mi ngi xewe ci diggante diwaanu Njamenaa, Mundu ak Kumra. Moo tax, ñu jёl ndogalu tёj gox yooyu ak Doba diggante juróom-benni waxtu ci ngoon ba juróom-benni waxtu ci suba ba ni réew mi di delloo ci jàmm.

Mu mel ni mbir yi jéggi nañu dayo donte ne sax ku nekk a ngi koy jiiñ sa moroom, muy Nguur gi, di kujje gi. Waaye, ndax bёgg Nguur jar na ray walla raylu saw askan ? Walla ndax dafa am lu lalu ci ginnaaw lees xamul ? Ak lu ci mёn di am bu ginaar toppee ay rattkat rekk, dafa fekk ne gisul ay bojjukat. Waaye, loolu moom askan wi moo ko mёn a xamal boppam. 

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj