Li gёn a fés ci xibaari bés bi Alxames 22 sàttumbar 2022

Yeneen i xët

Aji bind ji

PÓLITIG 

Mbirum Njaga Juuf

Ёttub àtte bu Ndakaaru dёggal na daan yi ñu teg ci ndoddu meeru Ndakaaru bii di Baartelemi JAAS ci mbiru bóomug ndaw lii di Njaga Juuf. Cig pàttali, ñaari at ak ak juróom-benni weer lañ ko daanoon.

Leerali bàrtlemi ginnaaw ndogal li

Ginnaaw bi ñu biralee daan yi ñu ko teg, moom ndeyu-mbill ji mi ngi xamle ne dépite la, te day wéy di ko doon ca Ngomblaan ga. Mu teg ci ne du génn fenn, dañu koo tooñ. Nee na du àddu nag ci daan yi. Ku bёgg a xam li ciy topp na laaj ay layookatam.

Tёralinu Ndiiso (commission) ya ca Ngomblaan ga

Ginnaaw bi ñu tёralee pekk gi ca Ngomblaan gi, tёral nañu fa tamit 14i Ndiiso yi war. Ndiisoo bu ci ne, am na dépite bu koy jiite. Waaye, balaay nekk, njiitul Ndiisoo, wareesul a bokk ci pekk gees fal. Bennoo Bokk Yaakaar moo jiite juróom-ñaar ya, waa Yewwi Askan Wi jiite ci juróom, waa Wallu-Senegaal jiite ñaar.

DIINE

Ñёwug néewub Imaam Mustafaa Géy

Ci ab saabal la kurélug Imaam yeek Ulemaawi Senegaal xamle ne, néewub Imaam Mustafaa Géy dina ñёw Ndakaaru ci Àjjuma jii, ñaar-fukki fan ak ñaar. Dinañu ko jébbal boroomam Gaawu ñaar fukki fan ak ñeent ca dёkku cosaanam bii di Seedo Sebe, ca diwaanu Maatam.

XEW-XEWI JAMONO

Kaawteef ca Tàmbaakundaa

Ab sóobare lag daamar rey ca diwaanu Tàmbaakundaa. Sóobare boobu mi ngi doon wuyoo ci turu P. M. Basen, amoon lu tollu ci fanweeri at. Jéyya jaa nga xew ci ay boori juróom-benni waxtu ci ngoon.

Jéyya yi am ci màggal gi

Bees sukkandikoo ci bilaŋ bi waa BNSP (Brigade Nationale des Sapeurs-Pompiers) def ci xeeti aksidaŋ yi am ci màggal gi, diggante fukki fan ba fukki fan ak juróom-ñaar ci weeru Sàttumbar lim nañu lu tollu ci fanweeri nit ak ñett (33) yu ñàkk seen bakkan ak juróom-ñeenti téeméeri nit ak juróom-benn (906) yu ci jёle ay gaañu-gaañu.  

TÀGGAT-YARAM

Mataar Ba joxe na lenge yi

Kii di Mataar Ba nga xam ne moo nekkoon jёwriñ ji ñu dénk wàllum tàggat-yaram, tekki nañu ndombog-tànkam bi ñuy tёral Nguur gu yees gi. Yankooba Jatara mooy ki ko wuutu ci béréb boobu. Ci Àllarba ji la ko doon jébbal lenge yi.

XIBAARI BITIM-RÉEW

Tukkib nemmikug Mamadi Dumbuya ca Mali

Ci Àllarba ji la kii di kolonel Dumbuya àgg fale ca Bamakoo ñu teeru ko fa gёn-jaa rafeti teeru, dalal ko. Mu dem fa nag ci jamono ju  am solo ci mbooru Mali. Muy tey jii di Alxames ñuy màggal seen juróom-benn fukkeel ak ñaareelu xewteg moom seen bopp. Moo tax, kii di Dumbuya biral fa kàddu yii: “tey maa ngi Bamakoo ci sama wetu mbokk, Asimi Goytaa ngir màggal moom ngi Mali moom boppam, ànd ak fere Mali gi nga xam ne sunu mbokk la”.

Ndajem CEDEAO ca New York 

Ndaje moomu, ci alxames ji la waroon a am, ca New York, ginnaaw ndaje mu mag mu mbootaayu xeet yi di amal. Jubluwaayu ndaje moomu nag mooy wax ci anam yi (situations) Gine ak Mali nekke ci jamono jii.   

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj