LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (11/9/2023)

Yeneen i xët

Aji bind ji

WOTEY 2024 YI

Lawaxub Bennoo Bokk Yaakaar bi ñu doon laam-laame xam nañu ko léegi. Aamadu Ba lay doon. Ci gaawu gi lañu ko siiwal ginnaaw bi kilifay lëkkatoo gi noppee ci seen diisoo. Ginnaaw tànneef gi nag, bare na ñu ko nangu ci seen biir. Waaye xel teey na ci Aali Nguy Njaay ak Maam Bóoy Jaawo. Njortees na ku ci nekk ber yoonu boppam.

Bu dee ci ñi féete kujje gi, bu ñenn ñi di saboote nekkug lawax gu Aamadu Ba, ku ci mel ni Aminata Ture, kenn ci lawax yi, tàmbali naa jonjanteek moom. Mi ngi sàkku ci moom sax mu sóobu ci géew bi te janook ñoom ci sémb yi.

MBËKK MI

Mbëkk maa ngi gën a tar. Mënees na wax ni tey la waalo gën a aay. Dee yu bare yi, ñi ñuy delloosi ba ci ñi ñuy jàpp di tëj taxul wenn yoon xale yi xàddi. Dañoo gënatee fobu sax. Nde démb ci dibéer ji, 6i gaal àgg nañ fa tenerif (Espaañ). Ñetti gaal yi Senegaal lañu bawoo. Jëwriñ ji yor dem beek dikk bi fa Espaañ di xamle ni dalal nañ démb lu ëpp 500i Saa-Senegaal.

TÀGGAT-YARAM

Gaynde Senegaal yi dañoo temboo ak waa Ruwàndaa bërki-démb ci gaawu gi. Ku ci nekk benn bii la dugal. Waaye joŋante boobu barewul woon loolu solo ci ekibu Senegaal bi. Fekkoon na mu jàll ci bokkadil yi ba noppi. Looloo waral sax ba mu yabaloon fa gaynde yu ndaw yi ngir ñu mag ñi gën mën a waajal joŋante bi war a dox ci seen digganteek Alseri niki ëllëg ci talaata ji fa Estaad Abdulaay Wàdd bu Jamñaajo.

BITIM-RÉEW

Fa bitim-réew, rëng-rëng ba yëngaloon suuf sa fa réewum Marog moo ub bopp yépp. Looloo ngi xewoon ci àjjuma jii weesu. Lees seetlu mooy ni limub ña ca ñàkk seen bakkan a ngay gën a bare. Ci xibaar yi ñu mujje siiwal, 2 122i doom-aadama ñàkk nañu ci seen bakkan. Waayeet 2 400 jële nañu ciy gaañu-gaañu. Ñuy ragal sax lim boobu gën a yokk nde ba tey wallukat yeek takk-der yi leen di jàppale noppeeguñu ci ceet yi. Ña nga ñuy wéyal ak a yaakaar rawale ñi desandi ca yàqu-yàqu ya ak màbbiti taax ya.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj