Lu Nguur gi di xaar ci Usmaan Sonko ?

Yeneen i xët

Aji bind ji

Lu Nguur gi di xaar ci Usmaan Sonko

Weeru Yàllaa ngi nii ginnaaw bi Yoon daanee Usmaan Sonko ak Ndey Xadi Njaay. Ñu war a tëdd ñaari ati kaso boole ci 20i tamndaret yuñ war a dàmpe kii di Aji Raabi Saar. Ndogal lees doon xaar ci àttekat bi génn na ñaari fan ci ginnaaw. Ba tax ñuy laaj lu Nguur gi di xaar ci doxal bile àtte.

Alxames 1 suwe 2023 la Yoon daanoon Usmaan Sonko ak Ndey Xadi Njaay ñaari ati kaso. Boobaak léegi nag, kenn tëju leen kenn bàyyiwu leen. Kii di Ndey Xadi Njaay sax dafa mel ne dañ koy faral di fàtte. Nde jàppal Sonko, bàyyil Sonko rekk ngay dégg.

Naka noonu, kii di Ismayla Maajoor Faal (jëwriñ jiñ dénk Yoon) jotoon na àddu ci li waral ba léegi léttuñ Usmaan Sonko, firiwuñ ko. Li mu waxoon ci ñaari ayu-bés yi weesu mooy ne Usmaan Sonko, kenn mënu ko jàpp feek àttekat bi jébbalu leen ndogal li Yoon jël. Ndogal li war a tukkee ci waa Yoon ñeel ko moo génnagul. Te bés bu génnee, ñaar rekk a mën a am : Usmaan Sonko nangu daan bi dem jébbal boppam Yoon walla bu bañee ñu jëli ko fa mu nekk.

Ba fii mu nekk nii Usmaan Sonkoo ngi ñu tëj ci biir këram. Bu weesoo wenn yoon wees ko séen mu nekk di kuppe ak ñenn ciy ñoñam, Njiitul Pastef li demul, dikkul. Bi ñu ko tëjee ci këram ak tey, ñaari yoon kott la mës a wax jaare ko ciy widewoo. Bi ci mujj di talaata jii weesu laata tabaski bi.

Boobaak léegi, ñaari pàcc yaa ngiy wéyal xeex bi. Bu Njiitul Pastef li jàppee ni dees ko xañ ay àqam, tëj ko ci lu amul teguwul ci Yoon. Jëwriñ ji jàpp na ni, tëj bees ko tëj ci këram mooy li gën ci moom. Nde, ci la kaaraangeem dee gën a ñoŋ.

Ak lu mu ci mën a doon, ndogal lol jëwriñu Yoon doon wax génn na. Barkaatu-démb ci àllarba ji, 28 Suwe 2023, lañ ko siiwal. Mu mel ne jàpp tëj a ci des. Waaye, bees sukkandikoo ci kàdduy Meetar Abdulaay Taal, di kenn ci ñiy layal Usmaan Sonko, ndeyu-mbill ji ci boppam jotagul lenn ub ndogal. Ba tax na Usmaan Sonko deesu ko mën a teg loxo fii mu nekk.

Lu ñuy xaar ngir jébbal ko ndogal li ? Ndax dañuy xaarandi Njiitu réew mi war a wax te nekk jamono yii fa Màkka ? Ba tey ay laaj yu sampu la. Ak lu mu ci mën a doon Senegaal a ngi jublu ciy ayu-bes yu teey xel. Ñuy xaar fu wànnent di mujjeek i bëtam.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj