Démb ci àjjuma ji lañ doon tëj ayu-bés bi ñu jagleel jëf ñeel njàng mi. Muy xew-xew bu ñuy màggal at mu jot ci àddina sépp. Bu atum 2024 mi nag, ñoo ngi ko jagleeloon ponk bii di njàng mi ngir coppite (l’éducation transformatrice)
Li ko dale altine jii weesu, 22 Awril 2024, ba démb ci àjjuma ji, 26 awril 2024, lañ doon màggal ayu-bés bees jagleel jëf ji (action) ñeel njàng mi ci àddina. Ñu koy wax ci nasaraan SMAE (Semaine Mondiale d’Action pour l’Éducation). SMAE, nekk jumtukaay bu yaa te am solo lool ci xeex yi ñuy xeex ngir réew yi sàmmonteek seen i wareef ngir njàng mi ñeel ñépp. Njàng mi ñeel ñépp, ñu gën koo miis ci EPT (Éducation Pour Tous), doon xeex bu askan yi di amal, jaare ko ci mbootaayu xeet yi ngir képp kuy doom-aadam mën a jot ci njàng mi.
At mu jot, dinañ màggal SMAE ci 100i réew ak lu teg ci àddina si. Kurél yu bari, ci fànn wu nekk, di ci dugal loxoom. Atum ren ji, ñoo ngi tànn waxtaane ponk bii di njàng mi ngir coppite (l’éducation transformatrice). Bokk na ci xeeti xalaat yi ñu gën a fésal : njàng mi ngir coppitee ngi am ci kow ñu soppi njàng mi.
Fii ci Senegaal, bokk na ci kurél yooyule mbooloo mii di COSYDEP (Coalition des Organisations en Synergie pour la Défense de l’Éducation Publique) te ëmb mbooleem kurél yiy yëngatu ci ñoŋal njàngum Senegal. Naka noonu, jot na amal ci ayu-bés bi am ndaje, doon ci waxtaane lépp lu jëm ci dooleel njàngum réew mi ngir coppite « investir dans une éducation publique et transformatrice ».
Ci seen ndaje moomu sax, seen njiit lii di Séex Mbów dellusi na bu baax ci wareefi maxejj yi ngir coppiku gu am solo ñeel doxiinu njàng meek tàggatu bi.
« Ci doxaliin wuy yóbbu njàngaan yi ci jëf ñeel mboolaay yu gën a yemoo, yu dal te sax ci njàng mi ngir coppite dina yokk limub maxejj yi seen xel ñaw, ñuy doxal baatu mbooloo mi ak a jëf. »
Xamle naat ni, soppali njàng mi dina tax ba ñu mën a am njàngaliin wow, ñépp a ciy bokk yem. Mooy tax it ba ñu mën a jublu ci taxawal i jumtuwaay yu am solo ñeel néew-ji-doole yi ba ñu mën a soppi seen anami njàng, di dékku senn i jafe-jafe, ubbeeku ci ni àddina di doxee te du leen tax a fàtte ñi ñu doon.