Démb ci gaawu gi la Nguur gu bees gi doon amal ab semineer. Njiitu réew mi, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay moo ko jiite woon. Mu dim ndaje mu amal solo Njiitu réew meek jëwriñ yi. Jubluwaayu semineer baa ngi aju woon ci fàttali jëwriñ yeek fara-caytu yi ñu tabb, liggéey bi ñu leen sas. Ci biir pàttali googu, Njiitu réew mi ñewaat na ci ponk yeek fànn yi tënk liggéey bi ñu dénk Nguur gi Usmaan Sonko yilif.
Lu tollu ci weer, ginnaaw ba mu jëlee lenge yi ci loxoy Maki Sàll, mel na ni Njiitu réew maa ngi bàyyi xel lu tax askan wi wóolu ko ba fal ko. Ndax, ci ubbiteg ay kàddoom, ca semineeru démb ba, fàttali na jëwriñ yeek ñi mu séqal liggéey bi li la askan wiy xaar ci ñoom. Looloo ko tax a wax ne :
“Li askan wiy xaar ci nun bari na. Te, nun noo leen digoon ab dogoo ak li fi nekkoon. Maanaam, ag coppite gu xóot. Loolu dafa war a tàmbalee ci ni ñuy liggéeyee ci biir Càmm gi, rawatina ci biir Nguur gi”
Dafa di, li askan wi di xaar ci ñoom mooy ñu soppi réew mi ba ñépp teg ci seen bët. Moo leen taxoon a daje ca semineeru démb ba ngir fénc yoriinu réew mi ak nees ko war a joyyantee. Ci gis-gisu Njiitu réew mi nag, ngir ñu tabax réew mi ci anam bu rafet te jaar yoon, fàww képp-kenn ci ñoom sasoo ittey askan wi. Rax-ci-dolli, ku nekk dafa war a def kemtalaayu-kàttanam ba sàmm li ñu ko dénk, yor ko yorin wu sell te mucc ayib.
Waaye, moom Njiitu réew mi yemul foofu. Ndax, xamal na leen ne, du loolu kese mooy tax liggéey bi mën a àntu. Nde, am na yeneen ponk yu tënk loolu yépp. Bi ci jiitu mooy sag. Maanaam, dañu leen tànn ngir ñu doxal ab liggéey ca na mu gën a rafetee. Bi ci topp, mooy oyof (suufe) ngir mën a liggéey ci sutura ak wone cër bu mat sëkk ñi ñu séqal liggéey bi. Bi ci mujj, mooy jàppandi ci kanamu ñi nga bokkal liggéey. Maanaam, nga wone ag dogu gu mat sëkk ngir matale li tax ñu teg la ci béréb boobu.
Ci gàttal, Njiitu réew mi dafa doon sas jëwriñ yeek fara-caytuy Nguurgu yees gi. Ci weneen waxiin, daf leen a fàttali yónni bi leen askan wi yónni te yàkkamti leen.
Wolof nee na, ku sa goro jox reer, boo biddantee day fekk sàlloowoo jom.