Xalifa tarixa xadiir yi ci Senegaal wuyuji na Boroomam ginnaaw tawat bi ko tëraloon. Kan moo doonoon Séex Bekaay ? Jaar-jaaram lan leen dégtal ci yaxal bile, ngir xamal leen kan moo doon xalifa ba woon ca Njaasaan.
Séex Al Bekaay mu ngi gane àdduna ca atum 1929, ñaari weer ginnaaw ba baayam Séex Bu-kunta nelawee. Mu nekkoon taawam, nekk tamit juróom-ñaareelu xalifaam. 2018 la toog ci xilaafa gi. Mu nekkoon ku ràññeeku ci mbooru araab. Doonoon ku fés ci bëgg Téere Bu Sell Bii di Alxuraan. Am njàngam mu doore ko ci magam Muhammet Kunta. Waaye, Gànnaar (Muritani) la ko mottalee. Ci noonu, bi mu ñibbisee la dal Medina Baay ci wetu Allaaji Ibraayma Ñas. Mu nekkoon ku ko jege lool ba léegi kóllëre googu di wéy ba ci Séex Maahi Ñas miy xalifab Medina Baay. Mu mel ni yamutoon rekk ci diine ji. Nde, Séex Bekaay bokk na ci ñi njëkk a liggéey ci caytu gi. Mu daan yëngu ca APS (Agence de Presse Sénégalaise).
Ñu denc ko ca dëkk bu sell ba di Njaasaan, ci teewaayu mbooloo mu takkoo-takku. Mbokk, taalibe, kilifa diine niki aada, ñépp ñoo ñëw teewe ci ginnaaw jullig tisbaar gi. Ñu seetlu fa teewaayu Taala Silla ma fa jiitu woon jëwriñ ji ñu dénk biir réew mi, ci turu Njiitu réew mi, Maki Sàll, jottali fa njaalam njaboot gépp, waaye tamit bépp jullit. Niki ni ñu baaxoo defe, ginnaaw dëddug Séex Bekaay, ka ko fa wuutu di Séex Bu-Siidi Maxtaar Kunta, nekk léegi xalifab Njaasaan.
Mënees na wax ne Njaasaan a ñàkk, waaye umma Islaam a ñàkk kilifa gu mag. Jaar-jaaram doon lu fésul ndaxte li ko yitteloon mooy diine ji. Loolu, terewu ko ubbeeko ci xam-xami àdduna ak ug yëngoom.