Bu ñu seetloo fan yee ci ginnaaw, werante amoon na ci nataali Séex Ahmadu Bàmba Mbàkke, naan moom la ak du moom. Muy ay nataal yi ñu fésaloon ci mbaali jokkoo yi. Nataal yooyu di wone jëmmi Séex Ahmadu Bàmba Xaadim Rasuul. Ñu xame woon ko ci benn nataal képp bu ñu miin a gis, réewu Farãs denc yeneen i moomeeli Senegaal, bokk na ca nataal yooyu.
Mu doon juróom-benni nataal yu ñu portale ca atum 1918 ba ñuy teg xeer wu njëkk wu jumaay Njaareem. Bu ñu sukkandikoo ci këru xibaar gii di Pressafrik.com, nataal yooyu ñu ngi jóge ci arsitek bii di Jean Geoffre, nekk ki rëddoon palaŋi jumaa jooju. Ci lu ko weesu, ca weeru Me 2020, lañu fésal njaayum portale yooyu. Ci noonu, la ab kurél bu ëmb ay taalibe murid ak i gëstukat defe ay jéego ngir jot ci nataal yooyu. Ñu jaaye leen ko ci lu tollu ci ñeent-fukki tamndaret ci sunuy koppar, maanaam 40i milyoŋ.
Biñ ci jotee lañ ko jébbal xalifa murid yi, Seex Muntaxaa. Mu fésal ci mbégteem, di sant taalibe yi. Ciy kàddoom, wax na ne : “Sëriñ bi, fàww mu feeñ”.
Ci weneen wàll wi, xamees na ne, nataal yooyu, du moomeelu murid yi rekk. Ndax, day fésal mbatiitu réewu Senegaal. Ci noonu, la Njiitu réew mi, Maki Sàll, dajeek kurél googu ngir ñu jébbal ko moomeel googu. Mu nekkoon ci teewaayu jëwriñ yu bari, rawatina ki ñu dénk mbatiit gi ak moomeelu réew mi di Aliyu Sow. Bokk na ci lañu xaatim mooy jëmmal kër guy sàmm ak a saytu moomeel yi maanaam “musée”.
Mënees na jàpp ne mbatiit, lu jar a sàmm la ndax dafa bokk ci kenoy askan. Kon, saytu moomeelu réew mi lu war la ngir seen taxawaay bañ a naax-saay.