« UN TOMBEAU POUR KINNE GAAJO » : FÀTTALIKU NGIR JARIÑU

Yeneen i xët

Aji bind ji

Bubakar Bóris Jóob génnee na téere bob, way-loru yi laboon ca suuxug « Le Joolaa » ba la ko jagleel. « Un tombeau pour Kinne Gaajo » la bindkat bi duppee téere bi. Kërug móolukaay gii di Éditions Philippe Rey moo ko siiwal ci atum 2024 mile. « Un tombeau pour Kinne Gaajo » nag, téere fent la. Dafa di, Bàmmeelu Kocc Barma, téere fent bim bindoon ci wolof, te EJO móol ko ca atum 2017, la bindkat bi tekki fii ci farãse. Moom nag, werekaan bi, dafa jàpp ne li mu bind ci jéyya ji wareef la woon ci moom.

« Un tombeau pour Kinne Gaajo », téere fent la. Ci farãse la ko Bubakar Bóris Jóob bind. Téere bi, ci suuxug « Le Joolaa » lay wax. Bóris nag, mbindam set na, rafet na te yit, gànjaru na. Ci anam bu taaru lay tëggee baat yi, di roofale kàddu yi. Dinay bind lu neex a dawal, neex ci nopp, neex ci xol. Waaye nag, du fàtte mukk wareefu bindkat bi : fàttali, yeete ak yedde. Moom mii di Bubakar Bóris Jóob, dafa baaxoo di jaare ci ladab ngir fàttali nit ñi ay xew-xew yu tiis te diis ci xol yoy, càgganteg nit ñi rekk a ko waral. Ci weneen waxiin, day yatt xalimaam, di jëmmal ay musiba yu fi jot a am ngir nit ñi bañ leen a fàtte ; waaye tamit, ngir ñu jëlee ciy njàngat ba lu ni mel bañatee amati ba fàww. Xam naa seen xel dem na ci Murambi, téere bi mu jagleel faagaagalug Tutsiy Ruwàndaa ya. Noonii rekk la doxalee ak suuxug « Le Joolaa » bim fental téere bile. Démb weesu na, naam, waaye lu mat a fàttaliku la.

Moone, Bóris jàppul sax ne Saa-Senegaal yi dañu fàtte suuxug « Le Joolaa » bi. Dafa di rekk, ci gis-gisam, Saa-Senegaal yi joxaguñu ko dayo bi mu laaj. Maanaam, fi leen mbir mi war a tollu dëgg, tollagu leen fa. Looloo ko tax a wax ne :

« Bu doon ci réew mu jaar yoon, at mu nekk, saa bu bésub 26 sàttumbar delsee, dañ ciy ànd fàttaliku jéyya ji. Bu ko defee, ñu xalaatandoo ci, baalante ci àq, baalu way-loru yu bari yees ciy fàttaliku, way-loru yooyee nga xam ne, lu mettee metti lañ daj. Ndeysaan, loolu, dañ ko fàtte. »

Li bindkat bi jublu ci wax ji mooy ne, suuxug « Le Joolaa » bi, weesu na fees ko yamale. Nees koy xoolee ak a càmbar dafa desee xóot. Dëgg-dëgg, laalaguñu yuqu mbir mi. Li ci kow rekk lañuy xool, di ci yéy ak a yàbbi. Waaye, la ca biir, di xolu jéyya ji, ñu war koo yër, fénc ko, jukkee ciy njàngat, dajaguñ ko. Loolii la boroom xalima biy firndeel ci kàddu yii toftalu :

« Dañuy wax waxi suux gi rekk. Waaye, ca dëgg-dëgg, bu ñu tojee wax ji, dees na gis metit yu jéggi dayo yi way-loru yi dund. Ñoom, way-loru yi nga xam ne, tooñuñu kenn. Jéyya jii di « Le Joolaa », dara waralu ko lu dul sunug càggante, nun askan wi ak laagob nger gi nekk ci sunu njiit yi. Looloo gën a war a tax ñuy fàttaliku bésub 26 sàttumbar bi, boole ko ci bés yiy màndargaal mboorum réew mi. Looloo ma tax a fent téere bii ngir kenn bañ a fàtte li fi xewoon ñeel suuxug « Le Joolaa » bi. Fépp fu ma aajar téere bi, waxtaane nañ ko. Téere fent bii, day wéy di dundal xew-xew bu tiis bile. »

Bóris a ngi fàttali ne, bérébu pàttaliku bees jagleel « Le Joolaa », nekk fa Sigicoor, ay maxejj ak njabooti way-loru yee coobarewu, defaral ko seen bopp. Bóris dafa gis ne, tekkaaral gi njiit yi nekkee, day wund ag càggante ak jëfi maa-tey. Dafa ne :

« Diggante 2000 ak 2004, Nguur gu ñàkk a yitte lanu amoon, di Nguur gu yëgul, lijjantiwul askanam ».

Naam, « Bàmmeelu Kocc Barma » la Bubakar Bóris Jóob tekki ci farãse. Waaye, dafa soppi tur wi, tuddee ko « Un tombeau pour Kinne Gaajo ». Li ko waral mooy ne, aji-bind ji dafa bëgg a fésal aji-jëmmal jii di Kinne Gaajo. Bóris neeti :

« Dama nab lool ci way-jëmmal ji te dama bëggoon a siiwal turam. Ni mu moomee boppam mooy xiir nit ñi ci moom. »

Tubaab bi daf nu gëmloo woon ne, sunu làkk yi, mëneesu cee fent ladab walla di ci taaral. Dem nañ ba xam ne, loolu, ay waxi xeebeel kese la ak i kasaw-kasaw. Bubakar Bóris Jóob ak ñi ko jiitu ci tool bi, ñoom Séex Aliyu Ndaw walla sax taalifkati diine ya woon, wone nañ ni sunu làkk yi gànjaroo. Ku jàng téerey Làmp Faal Kala tamit, dinga xam ni taaral ak ladab ci làkki Afrig yi la fekk baax.

« Un tombeau pour Kinne Gaajo » nag, du téere ladab kese yem ci. Nde, la ca bindkat bi dëxëñ ciy njàngale ak i yeete, day wone ne, ladab jumtukaay la ngir nàmm xel yi, dekkil cosaan, fàttali démb, tàggat jikko yi. Bu ko defee, ñu mën a soppi xar-kanamu àddina si ci anam bu baax.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj