Wàññiteg njëgu ndund gi, Càmm gi jël na ci ay ndogal. Lañu jotoon waxtaane ci yenn ci njëg yi ñu war a wàññi altine 24 ci weer wi lay tàmbali. Muy xibaar bu neex askan wi. Ndaxte, nit ñi dañu gisoon ne, lii di suukar si, diwlin ji, mburu ak ceeb bi dañu njëge lool. Moo tax, xibaaru wàññi gi neex lool ñiy jënd.
Ca Ndajem Ndiisoog Réew mi ci wàllu jëfandiku (Conseil National de la Consommation), jëwriñ ji ñu dénk wàllu yaxantu gi, Sëriñ Géy Jóob, fésal na njëg yu yees yi war a tàmbalee dox altine 24i suwe 2024 :
– Diwlin : 1 000 FCFA liitar bi ;
– Ceeb : 410 FCFA kilo bi ;
– Suukar : 600 FCFA kilo bi ;
– Miisu mburu 150 FCFA ;
– Saaku simaa : 3 550 FCFA.
Wàññite gi nag, du ñépp ñoo bég ci ndogalul wàññite gi. Jaaykat yi daal ak boroomi bulãsëri yi, ñoom rekk ñoo rafetluwul wàññite gi. Ndax, ci seen i wax, gisuñu ci seen bopp. Loolo tax mu am ñuy ragal jaaykat yi bañ a jëfe ndigal li. Waaye, njëwriñu yaxantu gi joxe na ag limatu ubbee (nimero weer) ngir, képp ku gis jaaykat bu nangut a wàññi, ñu woote ci, boole ko.