AKSIDAŊ YI : 1 200I WAY-DËDDU DIGGANTE 2021 AK 2022

Yeneen i xët

Aji bind ji

Dem beek dikk baa ngi wéy di jur coow fi réew mi. Ay aksidaŋ yu baree ngi wéy di am, di rey ñu bari ci tali yi, ànd ak limub way-loru bu jéggi dayo.

Jamono jii, mëneesul a toog ayu-bés te amul ab aksidaŋ bu am ci taliy Senegaal yi. Yéenekaay bii di Libération fésal nay xibaar yu raglu ñeel aksidaŋ yooyii. Ndax, bees sukkandikoo ci yéenekaay bi, 1 200i nit ñoo ci ñàkk seen i bakkan diggante atum 2021 jàpp 2022. 

Dafa di, nit ñi yàgg nañoo ñàkk seen i bakkan ci sababu aksidaŋ yi. Ba tey, ci li yéenekaay bi biral, 2017 ba 2020, ci xayma, lu jege 3 000iy nit dee nañ ci yooni réew mi. Muy lim bu takku te yéeme. 

Li gënatee doy waar mooy ne, limub aksidaŋ day gën di yokk. Ndaxte, ci menn atum 2021 mi, limees na 39 381i aksidaŋ ci réew mi. Aksidaŋ yooyile, ñoo rey limub 1 200i nit yi ñu tudd ci kow. 

Ginnaaw ñiy dee, am na yit ñu bari ñu ciy loru. Kurélug àddina sii di OMS xamle na ne, am na lu jege ñaar-fukki junniy nit ak juróom-ñaar ñu loru ci jéyya yiy am ci yoon yi. Ndakaaru, moom, moo jël raw-gàddu gi ak limub fukki junni ak benn ciy way-loru.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj