ASP : 39i LIGGÉEYKAT YU BEES CI ÑAARI FAN

Yeneen i xët

Aji bind ji

Njiitul “Agence de sécurité de proximité” (ASP) li jël na 39i liggéeykat yu bees diggante àllarba ak alxames. Guy Mariis Saañaa moo siiwal xibaar bi ci xëtu Facebookam. Li tax xel yi teey ci mooy ne, jamono jii, dañuy waaj a jébbal lenge Nguur gu bees gi Basiiru Jomaay Fay war a tabb lu yàggul dara. Dépite askan wi dafa bind ne :

“Jël na 39i liggéeykat yu bees ca ASP yi diggante àllarba ak alxames jii weesu. Liggéeykat yooyii, dañ leen a torlul ay pas yu amul àpp (contrat à durée indéterminé) te, ci jamono jooju, dégg naa dugal nañ 205i nit ci ASP yi.”

Bees sukkandikoo ci kàdduy Guy Mariis Saañaa, li njiitul ASP di def, moom Mamadu Saalif Sow, sabotaas la te jekkul ci kuy liggéeyal Bokkeef gi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj