Keroog, ci àjjuma jii weesu, la Paab Caw biral toftaleg gayndey kuppe yi. Moom mi toppoon ci Aliw Siise, moo ko wuutandi ci boppu ekib bi. Mooy jiite gayndey Senegaal yi ci ñaari joŋante yiñ dëgmal ci fan yii di ñëw ñeel toogalante CAN...
Démb, ci altine ji, la waa DGE (Direction Générale des Elections) siiwal toftale yi. Limu toftale yi xaw naa takku, donte ne sax, ñeen-fukk ak juróom-ñeent la woon, ñu mujj cee dindi juróom-ñett. Lëkkatoo gii di Takku Wallu Senegaal nag, dafa duut baaraam njiitul...