BAC 2024

Yeneen i xët

Aji bind ji

« BAC » dafa bokk ci joŋante yi gën a siiw fi Senegaal. Démb la door, ci talaata ji, 2i pani sulet 2024. Joŋante ren bi nag, xaarees na limu 159 487i ndongo. Kilifa yi jël nañ matuwaay yi war  ngir lépp jaar yoon. Noonu, ngir saytu joŋante bi, tànnees na lu mat 696i njiiti saytukat, 486i bérébi joŋante ak 10. 008i saytukat. Jëwriñ ji ñu dénk njàng mu kowe mi, Abdurahmaan Juuf, jot naa nemmeeku daara yu bari fa Ndakaaru.

Fa Luga, lu tollu ci 6 834i ndongo lañu fa lim. Foofa, jigéen ñi mat nañ 4 049i, muy, ci xayma, 59,25 ci téeméer boo jël. Limu ndongo yay tàggatu ci wàllu Xayma ( série S ) néew na fa lool. Ndax, seen lim a ngi tollu ci 906i ndongo. Bu ñu méngalee limu ren ak bu daaw ba, seetlu nañ ca ag yokkute bu mat 237 ciy ndongo.

Fa Kolda, waññi nañu fa lu tollu 5 428i ndongo yu war a def boobu kàtte (examen). Ñu limees lenn diggante Kolda, fa lañu ëppe 3 272, teg ca Welingara 1 762 ak Medina Yoro Fula 392.

Mu mel ni, seetlu bi benn la ci lekool yu bari ci réew mi. Matuwaay yi ngir lépp yemb, nemmeeku nañu ko ca Tëngéej.  Waaye, ca diwaan boobu, jigéen ña ñoo fa ëpp fuuf góor ña. Ndax, téeméer boo jël, 60 yi ay jigéen lañu. Ndongo yi ñu séddale leen ci goxi Rifisk, Jamñaajo ak Sàngalkaam. Waaye nag, am na lu ñu ci soow mi.

Lu jege 50i lawax (candidat) yu doon def kàtte (examen) gi la njiital “jury 1506” bu “Nouveau Lycée” bu Kawlax dàq ndax dañoo fekk ay jollasu ci seen sikaare (sac). Naam, jollasu yooyu, ci seen i biir sikaare lañ nekkoon te dañ fayoon. Waaye, sàrtu kàtte gi day tere ku indi jollasu ci bérébi yees di amalee kàtte gi.

Bo dul loolu, mënees naa tënk ne, kàtte “BAC” bi jaaragum na yoon. Ndongo yi ñu leen di xaar ci yeneen bés yi laataa ñuy génne njureef yi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj