Mari Sàmb Géy, ñu gën koo xame ci Mari Géy, moo ñàkk bakkanam fa Ngor, ci anam yu doy waar. Xew-xew boobu ma nga amoon talaata ci guddi, boori fukki waxtu. Coow la sabab faatug ndaw soosu mi ngi sosoo ci raafal gu takk-der...
KIGALI
Kigali, soo fay doxantu
Sa xol day sedd doo gis loo ñaxtu
Nga naw ci saa si Njiitu réew ma
Ndax liggéeyam rafet na
Céy Kigali !
Cet gaa lay jëkk a yéem
Moom cet gi war a jiitu ci lees di jéem
Doo dox mukk ba dajeek mbuusum ndox
Muñ naan...