‘’Ëttub taalif’’ mooy xët wu bees wi defuwaxu.com jagleel ladabu réew mi. Sunu xarit, sunu doomu-ndey Mataar Caam Faal, moo yor wile xët. Képp ku bind taalif te bëgg nu génne ko, mën nga ko koO yónnee ci [email protected]
Tey, Sëriñ Daawuda Njaay Jaraaf ak Sëriñ Daam Jaane mu Tuubaa lanuy àndal.
I
GÀDDAAY
Sëriñ Daawuda Njaay Jaraaf jàngalekatub wolof la. Def na gëstu bu am solo ci tëralin ak ci doxalinu njàngalem kàllaamay Kocc ci daaray tuut-tànk yi ci réew mi.
Gàddaay rekk dëkke gàddaay
Gàddaay ba nekk fu amul daay
Gàddaay ba man a sori gàdd gi
Gàddaay ba man a daw kàdd gi
Gàddaay kàdd ga ñuy siyaare
Gàddaay gedd la ñuy tasaare
Gàddaay baaxoo wërum réew
Gàddaay rekk bañ ku la yeew
Gàddaay ba far tàbbi ci dun
Gàddaay ba far tebbi lu duun
Gàddaay ba fa ñi la xañub dund
Gàddaay dund fa sa giiru-dund
Gàddaay defar sa gentu baay
Gàddaay dëggal sa géntu yaay
Gàddaay rekk dëkke gàddaay
Gàddaay ba nekk fu amul daay
DAAWUDA NJAAY JARAAF
II
GUDDI (Xaaj bu jëkk)
Sëriñ Daam Jaane mi ngi juddoo Tëngéej ci atum 1986. Daara la yor ca Tuubaa, di jàngale Alxuraan. Mi ngiy taalif way yu bari jëm ci xew-xewi jamano jii nuy dund.
Mbalaani niir yi bu muuree jant, sàng safax
Bëccëg ga tàggu timis, maay samp dënd di buur
Xaftaan bu ñuul ni këriñ, am tupp-tupp yu weex
Mooy col ga, ag ndaama laa, as ndiir su gàtt ma réer
Xaftaan bu ñuul la ma sol, am tupp-tupp yu weex
Ag ndaama laa, fukki waxtu ak benn rekk ma réer
Gaaw lool ci way-bég-i-xol, soof cam su nekkee ci tiis
Dal, yewwu, am sutura, xam lépp bàyyi ci biir
Way-baax ya sopp ma, saay-saay sa jàppe ma waay
Ñeey jaamu, ñee dëkke jëf ñaawtéef ya, lépp ma muur
Saag door la jinne di jóg, lal ay pexeem, tër i fiir
Ku farluwul tëye doomam, njuuma sànni ko xeer
Ngelaw lu sedd la moo lay soññ, gaawtul xoyet
Jafal sa and ci mattug gongo, gëtt gu piir
Ginaar yi tàbbi ngunu, njugub yi génne ci lëm
Lippaaxon ay gunge jeeg, bay waaj a yakkiji reer
Muus jóg di rëbbi jinax, xérjéjji lang ci looy
Gee jàll yóbb safaa, wittar nu tàbbi ci biir
DAAM JAANE