GÀTTALI BÉS BI

Yeneen i xët

Aji bind ji

USMAAN SONKO

Usmaan Sonko fasul yéene dalal benn juboolekat boo xam ne, Antuwaan Jom, jëwriñu biir réew mi, moo la bàyyi nga ñëw ci moom. Nde, njiitul Pastef li dafa jàpp ne, balaa ñoo wax waxi juboo, fàww ñu njëkkee ci ñaawlu ni ñu ko tënkee ci këram, moom ak njabootam, tere leen génn. Rax-ci-dolli, nguur gi dafa war a dakkal jaay doole bi mu koy jaay dool ci lu teguwul ci yoon. Looloo ko tax di xamal waa réew mi ak àddina si ne, mi ngi dékku tooñ ak xoqatal yi ñu koy teg ci ngor ak ci fulla ju mat sëkk ngir téeméeri téeméeri ndaw yi ñu faat ci lu dul yoon.

DÓOR NAÑ SEEX BAARA NJAAY « MANDAT DE DEPÔT »

Àttekatu ñaareelu kabine bi, Mamadu Sekk, dóor na Seex Baara Njaay, faramfàccekatu Walf Tv bi. Lees koy toppe mooy jëf ak i pexe yuy nasaxal kaaraange réew mi. Layookatam bi, meetar Musaa Saar a ko xamle. Xamleet na ne, jàllale nañ ko ca « Pavillon spécial » ndax dafa tawat.

DOG NAÑU SIÑAALU WALF TV DIIRUB WEER

Ndogal li jib na. Njëwriñu jokkoo gi doglu na siñaalu Walf tv li ko dale 1 fanu suwe jàpp 1 fanu sulet. Li ñuy tuumaal tele ndem-si-Yàlla ji Siidi Lamin Ñas mooy ne dañuy wax ay wax yu safaanoo ak dëgg, di wone ñaxtu yi ànd ak taafar ju metti. Ndogal loolu tax na ba liggéeykati Walf yi ñàkkandi seen i xéy. Nde, ci li Seex Ñas xamle, ndeem tele bi doxul liggéeyatul, duñ leen mën a fay. Moom, doomu Siidi Lamin Ñas mi jiite Walf, nee na dinañu jaamaarloo ak nguur gi, gedd ay xew-xewam. Xamle na tamit ne yóbbu nañ mbir mi ci Yoon.

BÀYYI NAÑ NDEY NDAAG TURE

Ndey Ndaag Ture mi ñu jàppoon ci talaata ji, bàyyi nañ ko mu ñibbi këram. Layookatam, meetar Musaa Saar, moo ko xamle. Leeral na tamit ne kenn toopeetul dara soxna si.

PEREFE BU NDAKAARU GÀNTAL NA DOXU ÑXTU WAA F24

Waa F24 dañu nammoon a amal ab doxu ñaxtu ci àjjuma jii, waaye perefe bu Ndakaaru bi gàntal na ko. Ñoom na, seen jubluwaay moo doon dox ci jàmm ngir ŋàññ Maki Sàll ak ñetteelu kay gi. Ndogal loolu nag, taxu leen dellu ginnaaw. Nde, woo nañ askan wi ci gaawu gi, 10 fan suwe. Nee ñu, kenn terewu leen ko. Moo tax Aliw Saane ak i ñoñam a ngi woo bépp saa-senegaal mu génn bu ñetti waxtu ci ngoon jotee, ñu daje ci suufu pomu pongu Saint-Lazare, dox ba Ecole Normale Supérieure.

SEEX UMAR AAN : « KENN DU BËTAL KÀTTE YI… »

Jëwriñu njàngum daara yu ndaw yeek yu digg-dóomu yi ? Seex Umar Aan, xamle na ne kenn du bëtal àpp yees jàpp ngir kàtte yi. Dafa di, fan yii wees, njàng mi dafa taxawoon ci béréb yu bari ci réew mi. Yëngu-yëngu yi juddu woon ci layoob Aji Saar ak Usmaan Sonko yee ko waraloon.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj