Stay tuned

Subscribe to our latest newsletter and never miss the latest news!
Our newsletter is sent once a week, every Monday.

Latest news

LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (20/6/2025)

GAINDESAT-1B : SENEGAAL WUTALI NA JAWW JI Senegaal a ngi séqi na jéego bu yees ci fànnu xam-xamu jaww ji. Nde, defar nañu seen ñaareelu...

PALESTIN, JIRIMU ÀDDINA SI

Ñaar-fukki weeri xare yoy, bés bu nekk, fa Gasaa, ay bakkan rot. Bu leen misil yeek bomb yi rayul, sóobare yi di leen sox...

LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (19/6/2025)

ELIMAAN JËWRIÑ YI ÀDDU NA CI JAFE-JAFEY GAYNDEY BASKET YU JIGÉEN YI Gaynde yu jigéen yiy basket dañoo amoon jafe-jafey amal seen ub tukki fa...

FRAPP : NOO BAÑ ! “ASSISES DE LA DÉMOCRATIE” BI MAKORÕ BËGG A AMAL UCAD DU FI AME !

Waa FRAPP siiwal nañu ab yégle, démb àllarba 18 suwe 2025, di ci biral seen ñàkk ànd ci ndajem péncoo bi Njiitu réewu Farãs,...

ISRAAYEL – IRÃ : JURÓOMEELU BÉSUB XARE

Juróomi fan ci tay, bi xare bi tàmbalee diggante Israayel ak Irã. Bees ci amalee ab taxaw-seetlu bu ndaw, mënees na ci jàngatee ay...

LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (17/6/2025)

LU BEES CI COOWAL SUUF LA CA GÉEJAWAAY Lu bees amaat na ci coowal suuf ak nger ga am fa Géejawaay ak Ëttu àttewaay bu...

KÀTTEY CFEE YU 2025

Kàtte yu atum 2025 mi dinañu tàmbali ginnaaw-ëllëg, alxames 19 suwe, jeex ci àjjuma ji 20 suwe. Atum ren jii, ñoo ngi ciy xaar...

JIIXI-JAAXA CI GÉNNUG ÀDDUNA IMAAM UMAR JAAWO

Naqar ak tiis la askanu Koldaa nekke fan yii, rawatina ña dëkke fa koñ bii di Medina Serif  Perlel. Nde, kii di Umar Jaawo...

“COUPE DU MONDE DES CLUB 2025”

Joŋanteb kuppe bees duppee “Coupe du monde des clubs”, di po mu mag muy boole lenn ciy këlëb yu mag ci àddina si. Ñi...

IRÃ – ISRAAYEL : XARE BAA NGAY WÉY

Xare baa ngay wéy diggante Irã ak Israayel. Ci guddig démb gi, gaawu jàpp dibéeru tay jii, ñaari réew yi weccante nañuy bomb. Ñoom...

IRÃ AK ISRAAYEL : LEBTOO, FEYTOO !

Xeex bi àddina sépp doon ragal ci diggante Irã ak Israayel tàmbali na. Ginnaaw bi Israayel njëkkee sànni ay bomb ba Irã fayu, sànnante...