Stay tuned

Subscribe to our latest newsletter and never miss the latest news!
Our newsletter is sent once a week, every Monday.

Latest news

NJIITU RÉEW MI AK MOM MÓRITANI NEMMIKUJI WOON NAÑU « GTA »

Démb, ci alxemes ji, 22 me 2025, Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, àndoon na ak naataangoom bii di S. Mohammet Uld Seex...

LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (20/05/2025)

ËTTU ÀTTEKAAY BU KAWE BI Ëttu àttekaay bu kawe bi tàmbali naa déglu jëwriñ yees fa kalaame. Ndey Sali Jóob mi fi nekkoon jëwriñu Njaboot...

NAALUW “CONSEIL SUPÉRIEUR DE LA JUSTICE”

Démb, ci dibéer ji, la kii di Porofesëer Siidi Alfa Njaay, doon amal aw waxtaan wu am solo fa RTS. Dafa di, dañu ko...

LIG 1 SENEGAAL : TIIS WU METTI

Démb ci gaawu bi, 17i Me 2025, la jéyya ju metti dal ci kay futbalu Senegaal. Fajuuf Njaay, kàppiteenu US Wokaam moo ñàkk bakkanam...

GUDOMP : 92i KËR JOT NAÑUY JUMTUKAAYI TABAX

Fa gox bii di Gudomp, njaboot yi tàmbalee dellusi ginnaaw bi leen fa xareb MFDC ba dàqee woon, jot nañu ay jumtukaay ngir tabax...

TUKKIB USMAAN SONKO FA BURKINAA FAASO

Elimaanu jëwriñ yi, Sëñ Usmaan Sonko, tukki na tay ci àjjuma ji, 16 me 2025, daldi dem Burkinaa Faaso. Ñaari fan la fas yéene...

LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (15/5/2025)

YOON LÀBBALI NAW FASAM Ayu-bés bee ñu génn la Ngomblaan gi tegoon ay tuuma ci ndoddu ñenn ñu fi nekkoon ay jëwriñ ca jamonoy Maki...

PÉNCOOY PÓLITIG BI AK DAARA YI

Kuréli ma-xejj yi yékkati nañu kàdduy woote jëme ci péncoom pólitig bi ñuy amal keroog 28 me ba 4 suwe 2025. Muy woote bob,...

TÉYANDI NAÑ ASURAA FAAL

Waa Cybersécurité jàppandi nañu, barki-démb ci altine ji, 12 me 2025, ndawu Pastef bi ñuy wax Asuraa Faal, ginnaaw ay kàddoom yu ñàkk teggin...

TUKKIB NJIITU RÉEW MI FA KODDIWAAR

Njiitu réew mi, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, moo ngi, ñaari fan yii, fa réewum Koddiwaar ngir teewe fa ndajem AFRICA CEO FORUM bu...

SFI DUGAL NA XAALISAM CI SENEGAAL

Këru liggéey gii di SFI (Société Financière Internationale), kër la gog day yëngu ci wàllu kopparal. Ki ko jiite di Maxtaar Jóob. Kër googu...