Stay tuned

Subscribe to our latest newsletter and never miss the latest news!
Our newsletter is sent once a week, every Monday.

Latest news

MAKI SÀLL JÓG NA NGIR SETAL DERAM

Sunuy naataangoy L’Observateur ñoo xëyee xibaar bi ci seen xët mu njëkk. Peeñug Njiitu réew ma woon, Sëñ Maki Sàll, la yéenekaay bi jiital,...

“FII SÉNÉGAL 2025” : MBIR MI, FII LA !

Ci talaatay tay jii, 7eelu fanu oktoobar 2025, lees door ndajem liggéey bees dippee Forum Invest in Sénégal 2025, fa Jamñaajo. Ndaje mile nag,...

UBBITEG LEKKOOL YI CI SENEGAAL

Tay, altine juróom-benni fan ci weeru oktoobar atum 2025, lañu ubbi lekkool yi fii ci Senegaal. Mu doon bés bu am solo ci mbooleem...

FMI AJANDI NA WOTEB SIPPI BI ÑEEL SENEGAAL

FMI ajandi na woteb sippi bi waroon a tax Senegaal mën a leb xaalis bob, daf ko aajowoo jamono yii. Ci àjjumay tay jii...

SENEGAAL / « CYBERATTAQUE » : AY SÀMBAA-BÓOY SONG NAÑU « FISC » BI

Xibaar bu doy a doy waar la Sikafinance siiwal ci bésub alxamesu tay jii, 2i fani sebtàmbar 2025. Ay « pirates informatiques » ñoo song « système...

YËGLEB NJËWRIÑU BIIR RÉEW MI AK KAARAANGEG PÉNC MI

Yégle bi : "Njëwriñu Biir Réew mi ak Kaaraangeg Pénc mi mu ngi yëgal askan wi ne Sën Ma-Jambal JAAÑ, ak li ñu ko doon...

MAMADU LI (ARED) JËL NA NEEXALU YIDAN 2025

Mamadu Aamadu Li, njiitu ARED, moo jël Neexalu Yidan 2025 ca Oŋ-Koŋ (Hong-Kong). Muy Neexal bu am solo lool ñeel suqalig njàng mi. Dafa...

COOW DIGGANTE BILAAL JAATA AK TASKATI-XIBAAR YI

Njabootu saabalkat yi mer nañu ba futt. Li ko waral du lenn lu moy jëf ji meeru Kër Masaar Sid def démb, ci dibéer...

MBIRUM MAJAMBAL JAAÑ

Ginnaaw bi Majambal Jaañ dawee, génn réew mi, Nguurug Senegaal jàpplu na ko fu mu mën a teg tànkam ci àddina si, dellu dàq...

SËRIÑ MAXTAAR JENN, XARITU XALE YI, DËDDU NA

Àllarba, 27eelu ut 2025 la Sëriñ Maxtaar Jenn ñàkk bakkanam cim ndog ci yoonu otorut "Ilaa Tuubaa". Ay nataal yu doy waar, naqaree dékku...

LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (25-9-2025)

NJIITU RÉEW MI JËMMAL NA ÑEENTI SÉMBI SÀRT YEES WOTE WOON FA NGOMBLAAN GA Fan yee jàll la dépite yi doon càmbar ñeenti sémbi sàrt....

MAJAMBAL JAAÑ, WAALI SEKK, ABDULAAY DAAWDA JÀLLO : YOON A NGI BARAL

Saabalkat bii di Majambal Jaañ de, jamono yii, mi ngi ciy guddi yu lëndëm këriis. Démb bat ay, moom la saabalukaay yeek mbaali jokkoo...