LÀNGU FAY-SÀLL-TIMIS : PETOROL BAA NGI XASAW XUNN

Yeneen i xët

Aji bind ji

Suweŋ2011, réew mépp màbbandoo wutali « Place Soweto » ngir xeex sémbub àtte bu Njiitu-réew ma woon, Ablaay Wàdd, bëggoon a jàllale ca péncum réew mi. Askan wi lànk ne : ‘’Mukk, du fi ame, dunu seetaan Góor-giy nas ak a nocci ngir taaj doom ji ci jal bi, dee moo nu ko gënal !’’ Góor-gi dellu ginnaaw, askan wi am ci ndam lu réy ba faf jële fi Ablaay Wàdd ci at mi ci topp. Keroog lanu jox Maki Sàll lenge yi ngir mu dakkal mbokkoo gi woon ci nguur gi, sàmm yoon wi, jële fi ger, càcc ak salfaañe alalu réew mi. Mu giñ ne dina doxale noonu, ba tax 25eelufan ci weeru màrs atum 2012, xol yépp féex, ñépp bég, yaakaar dekki. 

Ndeysaan… Tey, biñ ci tegee 7 at, képp ku amoon yaakaar yàkki nga. Mu mel ni dañu génne cib pax, daanu cib teen. Li taxoon ñu fal Maki ak li mu dige woon yépp, dara la ci deful. Moom kay, tey la Waalo gën a aay !

Jalgati ya woon, fa woon. Jay-doole ba woon, fa woon. Ëppal ba woon, fa woon. Ger ak goreedi ya woon, fa woon.  Doxin ak waxin wu ñaaw ya woon, fa woon. Nguuru Maki Sàll gii, bu yéesul nguuru Ablaay Wàdd, tanewu ko lool. Màgget yu xubidaas, maase ak i maamam, dar ko, pexe mu bon mu nekk ñu xelal ko ko, njombe wu ñaaw wu ne ñu dugal ko ci. Yoon wi naxsaay, alal ji mu fab jaay. Kujje gi mu tëj, wote yi di lëj. Ay mbokkam la tabb, ñuy giiroo alal ak moomeelu réew mi. Askan wi dëkke xiif, ku wax mu dóor i liif. Njàng mi sax da koo beddi : lii moom, du ndongo yee koy weddi. Wér-gi-yaram gi yoom. Koom-koom gi nasax, te moo dige woon ne dina woom. Liggéey amul ci gaal gi, moo tax ndaw yiy jël gaal yi. Maki xaaj na réew mi ci digg bi, wenn wàll wi mu jox Tubaab yi, weneen wi ay mbokkam ak i goroom ak i njegeñaaleem, ñu ciy gundaandaat ak a ndagarwale. Rakkam ji nag, Aliyu Sàll, moo jël raw-gàddu gi.

Bi Maki faloo ba nëgëni-sii, jamono ju nekk ngay gis Mareem Fay Sàll di séddale xaalis bu dul jeex. Fan la ko jële ? Rax-ci-dolli, fexe na ba jëkkër ji tabb ñenn ciy mbokkam, dooleel ku mel ni Mañsuur Fay ba mu nekk meeru Ndar. Bu yemoon foofu sax, mu tane. Wànte, Maki Sàll daanaka rakk ji la def tof-njiit lu sës ci moom rëkk. Maanaam, ginnaaw Maki Sàll, Njiitu-réew mi, Aliyu Sàll, rakk ji, moo fi ëpp sañ-sañ, ëpp fi alal, ëpp fi doole. Lu tax ? May leen ma ma leeralal leen wax ji ci juróom-ñaari ponk.

Benn, Aliyu Sàll mooy meeru Geéejawaay te dëkku fa.  Ñaar, Aliyu Sàll mooy njiital kurél gi boole meeri Senegaal yi. Ñett, Aliyu Sàll mooy njiital « Caisse de dépôt et de consignation » bi nga xam ne mooy bànku réew mi, ñu denc fa lu tollu ci 200 milyaar ci sunu xaalis. Ñeent, Aliyu Sàll mooy ki ëppale wàll ci Nja-naawu Senegaal bi, maanaam « Air Sénégal International ». Juróom, Aliyu Sàll day tabb ay jawriñ ak i njiit ci këri peggi réew mi. Moom sax da koy wax ci kow, ñépp di dégg, mu koy ndamoo. Juróom-benn, Aliyu Sàll moo jiite ndajem-caytu gu bànk BDK. Juróom-ñaar, Aliyu Sàll moo moom Sahel Aviationbi nga xam ne, ay « hélicoptères » rekk la yor, ñuy jaabante diggante teeni petorol yi, isini gaas yi ak dëkk bi. 

Kon, Maki Sàll mooy buur, Aliyu Sàll di bummi. Weddi, gis bokku ci. Mbiru gaas bi ak petorol bi, nag, moom la BBC, tele Àngalteer bu mag boobu, siiwal ci benn filmu-gëstu bu mu génne yàggul dara. Mbir mi lëmbe réew mi. 

BBC dafa yëkkati ay tuuma yu réy a réy teg leen ci kow ndoddi Aliyu Sàll ak magam, Njiitu-réew mi Maki Sàll ak Franck Timis. Li mu leen di jiiñ mooy : ger ak salfaañe moomeelu réew mi (petorol beek gaas bi) ak aakimoo alal ju askan wépp bokk. Ci benn boor, kujje gi ak way-moomeel yi di yuxoo wuub sàcceey ak a kalaame yoon. Ci beneen boor, nguur gi ak farandoo Aliyu Sàll yeek yu Maki yi di joxoñ baaraamu tuuma kujje gi, di leen dàkkentale naaféq ak ràmbaaj. Taskati-xibaar yi di ci yéy ak a yàbbi saa su nekk, fu waay nekk ñu ne la jabb mikóro, ne la : “loo xalaat ci mbir mi ?”. Askan wi moom, mëneesul a wax ni fii la féete ndax ku nekk am na foo far. Waaye, foo dem, mbiru petorol bi ak gaas lañuy waxtaane ak a werante. Mbir mi daal, mënees na ko méngale ak tànnbéeru dëmm, fu nekk la riir miy jóge.

Foo dem, Aliyu Sàll jàppal fii, Aliyu Sàll bàyyil fee, coow laa ngi ne kurr ci réew mi. Ndaxte, alal ji ñu wax ne moom la Aliyu Sàll ak saay-saay boobu di Frank Timis ràndal dafa takku ba jéggi dayo : 10 milyaari dolaar, maanaan juróom-benni junniy milyaar ci sunu xaalis ! Moone, Usmaan Sonko bindoon na lii cib téere lëmm, Baaba Aydara defoon na cib gëstu, siiwal ko, Keledoor Seen tamit waxoon na ci ba xoox, Mamadu Lamin Jàllo ak yenn politiseŋ yi amaloon nañ doxu-ñaxtu ngiir naqarlu lu ni mel…waaye dara. Nun danoo xaar ba Tubaab yi wax ci, nu door a nekk fii di réy làmmiñ. Ba tey, bu dee dina tax askan wi yeewu, baax na. Bu ko defee, maslaa meek waxi naaféq yi dinañ dakk. Waaw. Mbir mi nag, jeexagul ndax ñi mel ni Usmaan Sonko ak Bàrtélémi Jaas nee nañu kalaame nañu yoon ci Amerig ak Àngalteer ndax wóoluwuñu yoonu Senegaal. Rax-ci-dolli, kujje gi ak kuréli way-moomeel yu bare fas nañoo booloo, amal doxu-ñaxtu àjjuma 14 ci weeru suweŋ. Li ñu bëgg mooy Aliyu Sàll tekkiy ndombog-tànkam ngir yombal liggéeyu àttekat yi. Waaye mbir mi daa doy waar ba mel na ni du gaaw a sotti. 

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj