Ci ni ñu koy nemmeekoo ci ay kàddoom, Sëriñ Muntaxaa BasiirU du dañ ci xamle dayob maamam ji nga xam ne, moo di wasilaam, Sëriñ Tuuba Xaadiimu Rasóol. Moom nag, Sëriñ Tuuba Xaadiimu Rasóol, dafa liggéeyal Boroomam lol, Tuubaa màndarga la ci. Moo tax, ci gis-gisu murit yi, Tuuba dub dëkku neen. Loolu, tax ñu bëgg Nguur gi sàrtal ko dayob boppam, ni ko Watikã (Vatican) amee fa Itali.
Baay-faal yi, ci njiitalu Sëriñ Amdi Móodu Mbenda Faal, xalifab Séex Ibra Faal, ñoo yóbbuloon xalif bi ay xar ngir tabaski bi. Loolu, jëf ju ñu baaxoo def la at mu jot. Saa bu Tabaski teroo, dañuy ruŋŋ ay gétt, jébbal ko ku fi toogal Sëriñ bi. Ren, 1120i xar lañ joxe àddiya tabaski. Ginnaaw ngërëm yeek kàdduy njukkal yi, xalifa bi soññaat na leen ci dayob dëkk bii di Tuubaa. Fàttali leen worma yi mu yeyoo. Dafa dénk baay-faal yi dëkk bi ngir ñu sàmm ko. Lim ko dugge mooy fexe ba dëkk bi gën a sàmmu, gën a set, gën a leer, gën a sell, nu def ko sunu yitte”.
Sëriñ Séex Muntaxaa méngale na Tuubaa ak Watikã, wax ne, li Paap bi am, “…gënu caa yey Sëriñ Tuubaa”. Jukkees na kàdduy Séex Muntaxaa yile ci Saabalu gii di Senenews. Nde, Watikã dafa am dayob boppam, maanaam dafa jonn ca biir Rom, péeyub Itali. Lees mën a dégge ca kàdduy xalifa bi mooy ne, na kilifag Watikã amee sañ-sañu yilif dëkk ba, di ko doxal ci wàlluw diine, noona Sëriñ Tuubaa war a amee dayo ak sañ-sañ yilif ak a doxal Tuubaa. Junj nag, doy na boroom xel.
Cig tënk, xalifab murit yi dafa biral yéeneem, fësal bëgg-bëggam ñeel tolluwaayu Tuubaa. Sumb nañuy naal nag, doonte xamleeguñu num fay deme. Waaye, ba tey, doxin wa soppeekuwul ci ni Sëriñ bi daan doxale ci ay bëgg-bëgg. Ndax, bant dammut, te dereet mësul tuuru.