WALFADJIRI-NGUURUG MAKI SÀLL : GATSA-GATSA

Yeneen i xët

Aji bind ji

Kamaj ! Benn yoon. Kamaj ! Ñaari yoon ! kamaj ! Ñetti yoon. Siñaalu tele Walfadjiri dogati na. Bii yoon, diirub weer la tele biy fay. Li ko dale 1 fan ci suwe jàpp 1 fan ci sulet 2023. Ku ko dog ? Jëwriñu jokkoo gi. Lu tax ? Dañu wone ay yëngu-yëngal yi xewoon ci réew mi. Nii la mbir mi deme.

Bi Senegaal di Senegaal ba tey, guléet ñuy dog siñaalu tele ci àppug weer. Mësu fee am. Du ci nguuru Seŋoor. Du ci Jamonoy Abdu Juuf. Ablaay Wàdd itam, defu ko. Kon, gàcce-ngaalaama Maki Sàll. Moo fi def lu kenn deful. Ñu taxaw tuuti ci ndogal li, xool ba xam dëppoo na ak sàrt yi tënk wàlluw tas xibaar am déet.

Keroog, alxames 1 fan ci weeru suwe, la àttekat bi biral daan yim gàll Usmaan Sonko ak Ndey Xadi Njaay ñeel mbirum ciif ak tëkkuy rey yi Aji Raabi Saar doon jiiñ Usmaan Sonko. Ci waxi ndaw si, mbir maa nga xewe ca dàmpuwaayu Sweet Beauté, di moomeelu Ndey Xadi Njaay. Bés boobu, ak ñetti fan yi ci topp yépp, réew mi dafa tàngoon jérr, rawatina Ndakaaru ak Sigicoor. Xeex bi ne kurr diggante farandooy Usmaan Sonko yi ak takk-der yoy, ay saay-saay dañ leen raxoon. Lu tollu ci 16i bakkan rot ci, ci li Nguur xibaar. Am ñu ne 30i bakkan ak lu teg ñoo ci rot. Fan yooyu, àddina sépp, Senegaal lees doon waxtaane. Teley réew mi di amal i jotaay yoy, jagleesoon na leen yëngu-yëngal yi. Walfadjiri nag, jamono ja muy amal jotaayu Keppaar gi la siñaalam dog. Waa tele bi sax yëguñu ko woon. Ña doon seetaan a leen ko xamal. Ca la kilifa ga, Seex Ñas, jokkee Baabakar Jaañ mi yilif CNRA, laaj ko ndax moo dog siñaal bi, mu ne ko déedéet. Ayle-yéwén, bu doob moom, dina leen ko yégal ca njëlbeen. Ca lañu jàppee ne dañu ame paan. Ñi féete ci xarala gi seet, seet, ndekete dañu dog dëggantaan seen siñaal.

Waa Canal+ la Seex Ñas mujje woon, ñu xamal ko ni dañu jot ndigalu dog siñaalu tele bi. Jëwriñu jokkoo gi, Musaa Bookar Caam, moo joxe ndigal li. Waaye, yégalul woon kilifay tele bi. Bataaxel biy firndeel ndogal li sax, bésub 9 suwe lañ ko jot, fekk ne, booba, liggéeykati Walfadjiri yaa nga doon amal ab toogaanu ñaxtu ca seen biir màkkaan. Bi Seex Ñas di wax lab cag-cag indi bataaxel bi. Ca biir, jëwriñ jaa nga cay layal dog bi mu doglu siñaalu tele bi. Nee na ci, « 

Jëwriñ ji, ci dogu 94 bu càrtug tas-xibaar gi la sukkandiku ngir layal dog bi mu dog siñaal bi. Waaye, nag, dog 94 boobu mu sukkandi ba tax ko dog siñaalu Walf Tv, mayu ko sañ-sañ bi. Loolu la Daawda Miin, faramfàccekatu Yoon ci tele TFM xamle. Bees sukkandikoo ciy kàddoom, dog 94 bi day wax ne, moom jëwriñu jokkoo gi mooy joxe ndigal ginnaaw bi kurélug caytu gi (CNRA) biralee àndam ci ndogal li. Kon, CNRA mooy nangu wayndarew ki bëgg a am siñaal, saytu ko. Bu jàppee ne yemb, mu sog ko jébbal jëwriñ ji ngir mu xaatim ko. Waaye, bu jëwriñ ji xaatimee ba noppi sax, wayndare wi day delluwaat ca CNRA, boroom xaatim fa lees di wax « Cahier de charges ». CNRA mooy xool ndax boroom a ngi jëfe ak a sàmmonte ak « Cahier de charges » boobu.  Bogu 94 bi mooy jox CNRA sañ-sañ boobu.  Daawda Miin neeti, dogu 210 bu càrtug tas-xibaar gi ci boppam moo wax ne CNRA moo kurél gi war a dog siñaal ci kow ay sàrt. Rax-ci-dollu, dog 210 bi day wax sax ne, balaa ngaa dog siñaalu jàmbur, danga ko war njëkk xamal ni mu ngi jéggi yoon, bu bañee dellu ginnaaw gi nga artu ko, bu bañaatee ngay sog a siñaal bi. Bu ko defee, jëwriñ ji dafa jalgati yoon. Ndax yoon mayu ko muy dog siñaal. CNRA rekk la ko yoon may.

Rax-ci-dolli, boo waree dog siñaal, dangay bind boroom bataaxel, yégal ko ko. Bu dee tele bi àndul ci dog bi, bataaxel boobu lay jëfandikoo, yóbbu ko ca néegu caytu bu Ëttub àtte bu kowe bi. Te, jëwriñ ji dafa toog 9i fan sog a yónnee bataaxel bi. Te, ab cag-cag la yabal. Ci tënk, jëwriñ ji dafa jalgati yoon ñetti yoon. Bi ci njëkk mooy ne amul sañ-sañu dog siñaal. Ñareel bi mooy lim leen ko yégalul ca njëlbeen. Ñetteel bi mooy li mu yéex a yónnee bataaxel bi. Walfadjiri nag, mën na topp Musaa Bookar Caam ca yoon. Ndaxte, daf leen yàqal seen liggéey, ñàkkloo leen xaalis bu baree bari. Seex Ñas mi jiite Walfadjiri layookat la. Du ñàkk mu àqi yoon.

Wolof daf ne, tàmm laago la. Te, Nguur gi dafa bari li muy dog i siñaal. SenTv ak Walfadjiri nag ñoo ci gën a sonn, rawatina tele Sidii Lamin Ñas. Nde, bii mooy ñetteelu yoon ñuy dog seen siñaal. Moo tax nit ñi xaw a ñaaw njort, jàpp ne dañu singali Walfadjiri. Seex Ñas dafa jàpp ne dañu leen jaay doole. Te, Nguur gi lenn rekk la nisër, mooy tëj seen kër gi. Loolu lay biral ci kàddoom yii toftalu :

“Li nu bëgg tey mooy gindi askan wi, wax leen li am. Li am tey mooy ñi ame Nguur gi dañu tuutal ñi amul baat. Li ko waral mooy képp ku jóg di xeexal askan wi, Nguur gi du ko delloo mukk njukkal.”

Mu mel ni Nguur gi daf leen a singali. Natt bi leen askan wi doon nattal sax, daf ko dakkal, tere ko Wave mi doon taataan xaalis bi. Mu mel ni Walfadjiri daal mooy Ñaaw-yaay. Ndax, Seex Ñas nee na, bi ñu leen ko njëkkee def ci màrs 2021, demuñu woon ci yoon. Dañoo jàppoon ne ci dëkku yoon lañu nekk, defuñu dara. Ñu defaat leen ko, ñu def ab pelent ca Ëttu àtte bu kowe bi (Cour Suprême) te, ba tey mujjul fenn. Te, féewaryee ak léegi, ciy waxam ba tey, Usmaan Sonko àtte nañu ko fi ay yoon i yoon. Ba tey, ñoom moom, kenn lijjantiwul seen i mbir sax.

Doomu Siidi Lamin ji nee na nag, Nguur gi woo na leen ci xeex. Te, loolu mooy woo na Naar ci guuxum soow. Ñoom, duñu ci des ginnaaw mukk. Ndax, seen yoon nekkatul ci benn xew-xew bu Nguur gi di amal. Dootuñu ko wone walla di ci seen tele. Ciy kàddoom, dañ jàppoon ne ci réewum yoon lañu nekk moo tax ñu daan jàllale seen i mbir. Léegi, dootuñu ko def. Bu yeboo sax ñu ne ñoom Usmaan Sonko lañu àndal, ñoo tey ba teyaatoo.

Lii de mooy gatsa-gatsa dëgg nag.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj