YOOTE BI AM DIGGANTE MAKI SÀLL AK USMAAN SONKO

Yeneen i xët

Aji bind ji

Lu tollu ci at kepp a des ci wote yi, coow li ne kurr ci réew mi. Boo xoolee ni yëf yi di doxe sax danga naan ren la wote yi. Coow loolu nag, ak li lawax yi di bari bari, ñaar a ci gën a fés muy kii di Usmaan Sonko ak Njiitu réew mi Maki Sàll. Donte ne sax, moom Njiitu réew mi ñi ngi naan mënul a bokk ci wote yooyu. Terewul mi ngi dajalewaat ndànk-ndànk ay ñoñam. Kii di Usmaan Sonko tamit desul benn yoon ginnaaw ci xeex boobu. Mu mel ni ñoom ñaar kenn bëggul a bàyyi ak sa moroom yoon wi. Bu Maki Sàll nekkee fee ak i ñoñam di def wër gi mu jagleel koom gi walla di def i ndaje. Ca weneen wàll wa Usmaan Sonko tamit ma ngay def Nemmeeku Tuuram walla ay mitiŋ.

Coowal màrs 2021 li dafa am lu bari lu mu yokk ci pólitigu ñaar ñii. Ndax, tax na ku nekk ci ñoom ñaar xam fu saa-senegaal yi tollu ci yow. Bu kee jaaree fee ne li fi amoon dootu fi amati. Kee jaar fale ne ko li fi nekkoon tey la waalo gën a aay. Li waral loolu nag mooy ci at moomu la kii di Usmaan Sonko xam dëgg-dëgg, lan la jaral ñenn ci saa-senegaal yi. Ci la kii di Maki Sàll tamit xame ne waa ji am na doole. Boobaak léegi nag gaa ñaa ngi lewtoo. Mu mel ni gaa ñi dañoo nekk ci guddi gu bët setagul. Kenn xamul fu doole moroomam tollu. Moo tax nappante bi moom mënul a ñàkk. Looloo tax ku nekk ci ñoom di dajale ay ñoñam di won sa moroom foo tollu saa-senegaal yi.

Ca weer yee weesu la Usmaan Sonko tàmbali woon sémbam bii mu dippe Nemmeeku Tour. Di dem ci gox yi ak goxaat yi, dëkk ak dëkkaat yi di waxtaan ak saa-senegaal yi. Yàggul dara, Njiitu réew Maki Sàll mel ni ku naan ko fii tamit li fi nekkoon jógu fi. Moom it yëgle ne day tàmbaliwaat a génnee ndajem jëwriñ yi di ko defe ci yeneen dëkk yi. Ci sémb boobu lay defe li muy dippe wër gi mu jagleel koom gi. Yëf yi nag koom lay wund, waaye, boo seetee ba ca biir pólitig a ca ëpp doole. Muy ci Nemmeeku Tour bi di ci wër gi mu jagleel koom gi daanako ñaar yépp dalal gi ak mbooloo ma fay daje lañuy gën a bàyyi xel. Maanaam, ñoom ñaar ñépp ci seen ndoorteelu kàmpaañ lañu nekk. Ku nekk ci ñoom jamono jii mi ngi natt dooleem. Kon, loolu ay lay kepp la ngir am foo jaare. Ndax, ku nekk a ngi waxaale ay soxlaam, xam tamit fu saa-senegaal yi tollu ci yow. Kenn du nangu di bàyyi moroomam di ko gën a jege askan wi. 

Looloo tax na ca jamono yee bi Usmaan Sonko dakkale woon Nemmeeku Tour bi ndax, coow li doxoon ci digganteem ak Aji Saar, taxul mu teggi tànkam. Ndax, ca jamono jooja moom ak i mbokkam ña nga doon namm a amal tëgum boole 31 ci weeru desàmbar ca jamono ja Njiitu réew ma di jàkkaarloo ak askan wi di def aw waxtaanam. Rax-ci-dolli tamit ñi ngi doon sàkkoo amal am ndajem-ñaxtu ci ndoorteelu weeru saawiye wi, te, mujjul àntu. Ndogal yooyu nag bokk ci li tax kii di Usmaan Sonko moom jàpp ne Njiitu réew mi day jëfandikoo yoon ngir gàkkal seen i yëf, muy lu ci mel ni Nemmeeku Tour bi. Waaye nag, ndax danga xam paaka bi la war a rey nga koy daas?

‘‘Danoo def sémb bu am solo muy Nemmeeku Tour. Mooy dem dajeek saa-senegaal yi, fekk leen ca fa ñu dëkk toog saafonte ak ñoom, waxtaan ak ñoom xamante ak ñoom, déglu leen ci seen i mébét, déglu leen ci seen i jafe-jafe. Waaye, wax leen tamit lan mooy sunu yéene ci réew mi ak naka lanu ko bëgg a doxale. Sémb boobu door nanu ko ay fan ci ginnaaw, gan caa gudd ñaari weer ci ginnaaw. Nu gënoon ci taamu nag dëkku kaw yi. Ndax, danoo jàpp ne boo seetloo sunu njureef yu weesu yi, dëkku taax yi bu mokkul it am nanu fi lu réy. Waaye, ni Nemmeeku Tour bi amee doole ci weeru njëkk yii moo tiital Nguuru Maki Sàll ba gis ngeen ni lu ne ñi ngi koy def ngir gàllankoor Nemmeeku Tour boobu. Bi ci gën a fés mooy jëfandikoowaat yoon ngir xool nu ñuy gal-gale Usmaan Sonko ba dootul tal dem ci àll bi ca jamono yoo Maki Sàll ma ngay jël xaalisu réew mi bu dul jeex di def Tàggatoo Touram. Waaye, daldi koy dëxëñ nee na ci wër gu mu jagleel wàllum koom gi, nu xam ñépp jubluwaay bi mooy ndoorteelu kàmpaañ.’’

Mu mel ni nag, gaa ñi mayantewuñu dara. Moom Njiitu réew mi nag ma nga tàmbalee woon wër gi ca Tàmbaa ci njeexitalu weeru desàmbar. Ci ayu-bés bii nag ma nga woon ca Cees. Ci ñaar dëkk yépp nag mbooloo mu baree ko teeru. Ba démb sax, ci gaawu bi ma nga woon ca Ndar. Mbooloo mu bari tamit teeru ko fa ci ndaje mi ñu jagleeloon 100i at Prytanée militaire Charles N’Tchororé. Usmaan Sonko moom ginnaaw mitiŋ bu am doole bi mu defoon ca Kër Masaar, ma nga doon amal ay doxu nemmeeku ci biir Ndakaaru. Nu gis ne nag mbooloo mu bari moo ko doon topp. Muy fu ca mel ni Parcelles assainies, Patte D’oie, Kolobaan. Bi ci gën a fés nag mooy mitiŋ bi mu doon def ca Mbàkke nga xam ne perefe ba daf ko tere woon. Terewul nag, mu def ko, donte ne sax, amoon na ay jàmmaarloo diggante ndaw ñi ak takk-der ya. Ba moom sax takka-der yi toj weeru daamar gi mu nekkoo. Waaye, mujj na dem ba àgg fa. 

Mu mel ni moom la takk-der yi gën a sonal. Muy bu waree wuyuji walla mu nekk ci mbiri pólitigam. Ndax, démb rekk bi ñu nee day dem Géejawaay ay takk-der yu bari lañu fa wàcce faf mu mujj dem Walf nga xam ne keroog ci àjjuma ji dañoo daggoon seen siñaal. Moom nag mel na ni ragalul ki muy jàkkaarloo bees sukkandikoo ci kàddoom yii.‘‘Nappaate bi jeex na, jaay doole bi jeex na. Bu dee jàmm la bëgg, dina am jàmm ci réew mi. Bu dee safaan wi la bëgg, xam ne réew mi moomu ko, donnu ko.’’

Ñoom ñaar nag, ku nekk dafa mel ni wóolu nga sa bopp. Bu ñoñi Maki Sàll di woote naan ñoo yor doole ji, te, ñun la askan wi fal. Usmaan Sonko ak i ñoñam naan man la askan wi jox bopp, te, man la àndal. Léegi, ñan ñooy askan wi? Ndax tamit mbooloo mi ñuy dajale mën naa firndeel ñooy jiitu? Walla ñi fa ñëw ñépp, ñoom lañu àndal. Kon daal, ñoom ñaar bu kenn teggiwul tànkam dinañu daje. Kii di Sire Si moom dafa jàpp ne loolu mënt a ñàkk bees sukkandikoo ci kàddoom yii. Te, loolu sax mooy firndeel seen ndaje yu bari yi ñuy amal.

‘‘Bu Njiitu réew mi Maki Sàll delluwul ginnaaw, Sonko delluwul ginnaaw. Ñoom ñaar alaa kulli haalin fàww ñu daje. Léegi, coow li mooy danoo xamagul kañ la? Ak fan la? Buñu delluwul ginnaaw daje bi mënt a ñàkk. Ndeem mënt a ñàkk nag doo toog naan mënt a ñàkk, ku nekk dangay fagaru […]. ñoom ñaar ñi ngi wax waaye jëfandikoowuñu ay kàddu. Maanaam, dañuy yoote, tey Maki ñëw teg dara génn, Usmaan moom it ñëw it teg génn. Fim ne Maki xam na, Usmaan xam na.’’    

Ndeem nag tànk ci suuf, jaan ci suuf yàgg-yàgg dañuy daje, waajtaay mënusee ñàkk. Li am ba des kay mooy ñi ngi ci yoote bu metti. Bu kii demee fenn dajale fa mbooloo mu bari, ka ca des dem feneen def fa lu ni mel walla lu ko raw. Kon nag, wotey 2024 yi teel naa door. Donte ne sax, sikki-sàkka am na ci bokkug Njiitu réew mi Maki Sàll, terewul ay ñoñam moom lañu def seen lawax. Moom nag ba tey, àddoogul ci loolu. Waaye nag li ci kanam rawul i bët. Te, ku dund danga fekke.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj