Li gën a fés ci xibaari tàggat-yaram (àllarba 1 Màrs 2023)

Yeneen i xët

Aji bind ji

Paul Pogba 

Gannaaw 11i weer yi mu toog ci sababu gaañu-gaañu bu metti bi mu ame woon, Paul Pogba delsiwaat na ci pàkku wure yi démb ci talaata ji. Muy Joŋanteem bu njëkk ba mu delloo ca Juventus ak léegi.

FIFA the Best

Saa-Àrsàntin bi, Messi, moo jël raaya ji ñu jagleel wurekat bi gën a xereñ ci atum 2022 mi. Loolu nag, jur nay ñurumtu ndax am na ñu jàpp ne yelloowu ko.

France

Noël Le Graët nekkatul njiitul FFF. Démb ci ci taalata ji, 28i féewaryee 2023 jii lañ ko xamle. Gannaaw loolu la ko Gianni Infantino, Njiitul FIFA, fal ci boppu kureelu FIFA bu Pari.

Just Fontaine, kenn ci ndaanaani France ya woon, wàcc na liggéey tay jii ci àllarba ji. Mooy ki ëpp ba léegi lu mu dugal kuppeg àddina lëmm, 13i bii ci benn kub. Ba léegi keneen defaatagu ko.

Coupe du Roi / Espagne

Xamle nañ ni kii di Pedri, Usmaan Démbele ak Lewandowski duñu bokk ci ñiy jàmmaarlook Real Madrid suba ci alxemes ji.

Basket

Ekibu basket Senegaal bu góor ñi du dem ca kuppeg àddina si ñeel basket. Meetar Baabakar Njaay nag àndul ci toogloo giñ toogloo Senegaal ba tax muy duut baaraam waa FIBA, teg ci yëkkati yii kàddu : “Senegaal dañ ko toogloo ci lu jaarul yoon”.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj