Sànq la xibaar bi rot. Muy xibaar boo xam ne biig ci guddi ba léegi ñi ngi koy xaar. Ndax, kenn umpalewul ne, bees sukkandikoo ci li jot a tukkeegum ci mbañ-gàcce yi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay moo jiitu mbooleem lawax yi. Lim bim leen rawee bari na bariwaay bob, fii la wote yiy yem. Moo tax, biig ci guddi, li ëpp ci lawax yi teel a nangu ndamu Jomaay li, ba mu des kenn. Kooku, Aamadu Ba la woon. Moom, ba ci guddi gi, nangoogul woon li tukkee ci mbañ-gàcce yi. Doon na wax sax ne, ñaareelu sumb mënul ñàkk. Waaye, mujje na nangu tey.
Démb, dibéer 24 màrs 2024, moo nekkoon bésub wote ñeel palug Njiitu réew mu bees mi war a wuutu Maki Sàll. Mu nekk bés boo xam ne Saa-Senegaal yépp a ko doon xaar, rawatina waa kujje gi. Ba ñu xéyee nag, maxéjj yi génn nañu woteji ci ag dal. Ba juróom-benni waxtu ci ngoon jotee lañu tëj pekk yi. Ca la njureef yi tàmbalee di rot ndànk-ndànk. Lawax bii di Basiiru Jomaay Jaxaar Fay jiitu daanaka ci dëkk yu bari fi réew mi. Béréb ya lawax yi mu doon xëccool wotee sax, daf leen fa dóor dóor yu metti. Bawul kenn, ba ci Aamadu Ba sax, daf ko wulli ba ci biir pekk bim wotee. Waaye, la ko ca fekk moom, fekku ca lawax ya ca des. Ndax, ñee dañu teel a nangu, moom muy siisu. Te, teel a nangu, day oyofal i dóor.
Looloo tax, ñoom Paap Jibriil Faal, Mamadu Lamin Jàllo, Anta Baabakar Ngom, Xalifa Abaabakar Sàll, Décce Faal, Maam Bóoy Jaawo, Aali Nguy Njaay, génn ca teel, ndokkeel ko. Kii di Aliw Mammadu Ja bu PUR ak Idiriisa Sekk tamit génn nañu tay nangu ne waa ji daan na leen donte ne Idiriisa tuddul turu Basiiru Jomaay Fay. Ki ñépp doon xaar nag mooy Aamadu Ba. Ndax, ñu bari dañoo jàppoon ne du nangu njureef yi jot a tukkeegum ci wote yi fii ak bànqaas yi yor li aju ci wàll woowu àdduwuñu ci.
Démb ci guddi daf ne woon dina def am ndajem-waxtaan. Ci mujj gi, mu dàq ko ba tey, bu fukki waxtu ak ñaar jotee ci bëccëg. Waaye, loolu tamit mujjul a am.
Tey nag, ci boori tisbaar la xibaar rot. Mu wax ne, moom lawaxu lëkkatoog Bennoo Bokk Yaakaar gi, nangu na jéll bi. Ndax, dafa jël ag jollasoom woo Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, ndokkeel ko. Rax-ci-dolli, won ko ne nangu na ne moo raw ci joŋante bii ñu doon amal. Kon, leer na ni, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay mooy juróomeelu Njiitu réewum Senegaal ci mboor. Mooy doon ki fiy wuutu Maki Sàll. Léegi nag, mu des Ndajem Ndeyu sàrti Réew mi ak bànqaas yi ñu dénk wote yi ñu génnee njureefi mujjantal yi.