MURIG MBALAANU KIIRAAYU FARBA NGOM
Ayu-bés bii ñu génn la Ngomblaan gi dooroon liggéey bi ba jotoon a taxawal ag ndiisoo. Suba, ci àjjuma ji, woo nañu dépite yi fa Ngomblaan ga. Li waral woote bi du lenn lu moy fénc càkkuteefu murig mbalaanu kiiraayu...
Ci àllarbay démb ji, 22i fani sãwiyee 2025, lees doon amal ñeentelu ndajem jëwriñ yi ci at mu bees mii. Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Fay, moo jiite ndaje ma. Ca njeexital la, Aamadu Mustafaa Njekk Saare mi yor kàddug Càmm gi biral na...