#Diisoo ñeel réew mi
Diisoo bi Njiitu-réew mi, Maki Sàll, woote woon door na ci talaata jii. Ci kiliftéefam lañ ko ubbee, mu nar a ñeel tolluwaayu reéw mi ak ëllëgam. Ñi séq ndaje mi yépp a mànkoo, ànd ci jëmm jii di Faamara Ibraayima Saaña ngir mu jiite waxtaan wi. Ñu baree fa teewoon : kilifa diine yi, kilifa aada yi, ñenn ci kuréli way-moomeel yi ak kujje gi. Waaye, du ñépp a wuyuji wooteb Njiitu- réew mi. Usmaan Sonko, Idiriisa Sekk, Madike Ñaŋ ak Isaa Sàll nanguwuñ cee bokk. Nee ñu, waxtaan wii naxee-mbaay doŋŋla ndax Maki duggewu ko lu dul tuur askan wi lëndëm. Ci seen gis-gis am nay mbir yu ko ëpp solo, gën koo jamp fuuf. Móodu-Móodu yi, ñoom, naqarlu nañu li ñu leen boolewul ci diisoo bi.
#Maki Sàll dalal na jawriñ bi yor kaaraange biir réewum Frãs
Njiitu-réew mi, Maki Sàll, dalal na Christophe Castaner mi yor kaaraange biir réewum Frãs. Jawriñu Farãs bi, nag, ñëwam Senegaal baa ngi aju ci tukkib nemmeeku bi mu doon amal te tàmbalee ko ca Kodiwaar. Ñaari fan la fi def, giseek Maki Sàll ci wàllu kaaraange. Maanaam, naka la ñaari réew yii di Senegaal ak Frãs di ànde ngir samp fi ay jumtukaayi kaaraange ak ay dogal ñeel internet bi ngir tee xëbalekat yi – terroristes yi – sonal askan wi.
KOOM-KOOM
#Waaxu Ndakaaru
Bu ñu sukkandikoo ci kii di Abuubakar Sëdiix Béey (@ASedikhBeye), ngañaayu Waaxu Ndakaaru bi, am na yokkute. Ndax, ci atum 2018 mi, li ñu dugal ci xaalis mi ngi tollu ci 56 milyaar ci sunuy koppar te, ci atum 2017 mi, xaalis booboo ngi tollu woon ci 49 miliyaar.
DIINE
#“Maîtresse d’un homme marié”
Waa kurélu JAMRA kalaameeti nañu CNRA kilib bii ñu duppe « Maitresse d’un homme marié ». Bees sukkandikoo ci Maam Maxtaar Géy mi jiite JAMRA, teyaatar bi yëfi caga rekk lay dawal, rawatina pàccam bi mujj bi mu dawal ci weer wu sell wii di weeru koor. Bu ko defee, joxoñ na baaraamu tuuma tele yii di Marodi ak 2STV.
NJÀNG MI
#BAC
Lu toll ci 159 junniy ndongo, 82 junni yi di ay jigéen, def nañu “anticipé philosophie” ci àllarba jii. Ngir dakkal càcc yu jéggi dayo yi ñu nemmeeku woon at yi weesu, kër gi yor wàllu BAC bi, “Office du BAC” ci kàllaama nasaraan, dafa tere woon ndongo yi ñu ñëw ci joŋante beek seeni njëggil-kàddu (telefon).
WÉR-GI-YARAM/AADA/TÀGGAT-YARAM
#Xeesal
Bees sukkandikoo ci yéenekaay bii di Senego.com, ginnaaw jigéeni Kóngo yi, jigéeni Senegaal yi ñoo gën a bëgg xeesal ci Afrig. Doktoor yaa ngi wéy di artu askan wi, di xamal ñépp ni xeesal ay feebar yu bon lay joxe, niki kañseer, waaye teewul tey la Waalo gën a aay.
#Futbal
Gaynde futbal yu ndaw yi def nañu jaloore ca réewum Poloñ. Ginnaaw bi ñu amalee ñetti joŋante yu njëkk yi, am nañu ñaari ndam, arañefe benn. Ñoom ñoo raw kon Kolombi, Poloñ ak Tayiti. Ci fàttali, gaynde yaa nga ca Poloñ ci jamono jii, bokk ci joŋante futbalu goney àddina si amagul 20 at.