Gàttali bés bi (23/6/2023)

Yeneen i xët

Aji bind ji

Waxtaan wi jeex na

Ëllëg, gaawu 24 suwe 2023, la Njiitu réew mi, Maki Sàll, war a dalal ndaw yi teewal seen i kurél ci waxtaan wi mu woote woon ñeel mbiri réew mi. 

Waxtaan wi, bésub 31 me 2023 lañ ko dooroon. Bu ëllëgee lañuy jébbal Njiitu réew mi njureef ya fa tukkee. Mustafaa Ñas mi jiite woon waxtaan wi la 9i banqaas yo séqoon waxtaan di njëkk a jébbal seen i caabal. Nee ñu sax 9i banqaas yépp jot nañ joxe seen i caabal ba noppi. Mustafaa Ñas, ci ndimbalu ndajem tënk mi, mooy boole ndogal ak ndigali 9i caabal yépp, jébbal leen Maki Sàll.

Ca ëllëg sa, moom Njiitu réew mi, dina wax ak askan wi.

Mbirum ñetteelu moome gi

Ndax Njiitu réew mi day waaj a biral bokkam ci wotey 2024 yi ? La mu wax fa Pari moo tax ñu bari jàpp ne ca la jëm. 

Ndax, ba muy wax ak militaŋi APR ya ga nekk, ñaax na leen ngir ñu gën a booloo. Nee na leen itam, ak lu ci mën di am, dina wax ak askanuw Senegaal. Loolu, jarul sax wax. Ca njeexitalu waxam ja, dafa mel ni kuy junj. Ndae, daf ne, am liggéey bu réy bu leen di xaar keroog mu yégle li muy def ñeel wotey 2024 yi. Nee na sax  ndam lu rey a ngi leen di xaar ci atum 2024 mi. Ba dibéer, amaana mu leeral i waxam.

KARIIM WÀDD AK XALIFA SÀLL DINAÑ BOKK CI WOTEY 2024 YI

Ba ñuy sumb waxtaanuw réew mi, lawaxteefi Kariim Wàdd ak Xalifa Sàll bokkoon nañ ci ponk yi gën a fës. Nde, ñoom ñépp, Yoon daf leen daanoon daan yoy, daf leen a xañ seen àqi maxejj, tere leen doon i lawax ci wotey réew mi. Ñu bare jàppoon ne pexey Maki Sàll kese la. Moo taxoon, ci wàllu waxtaan wi, ñu doon xool naka lañuy def ba Kariim ak Xalifa Sàll mën bokk ci wotey 2024 yi. Dafa mel ni seen i pexe sotti nañu.

Nee ñu, dogu L28 bi lañuy soppi ngir ñu mën a doon i lawax. Bu dee Usmaan Sonko, moom, waxuñu dara ciy mbirum.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj