KORITE 2024

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ren, daanaka àddina sépp ci àllarba tey ji lañu wori. Senegaal itam, tey la ñépp julli korite. Njiitu réew mi, fa jumaay Ndakaaru ju mag ji la jullee.
Barkii-démb, wëliis Mali ak Niseer, amul fenn fees déggaatoon ni weer wi feeñ na fa. Muy Araabi Sawdit, di Farãs ak yeen réew yu bari, kurél ya fay séentu weer wi gisuñu ko woon. Ba tax, li ëpp ci àddina si, dañu matal seen fanweeri fani koor, daldi wori ci àllarbay tey jile, 10i panu awril atum 2024, muy korite.

Fi Senegaal sax, kurélug ibaadu giy séentu weer wi, gàttal biy joxe CMS ci farãse, ne woon na ne gisul weer wi fenn. Ñoom it, ñu daldi matal 30i fani koor yi, daldi wori tey.
Lu ko jiitu, kurél gii di ASPA (Association Sénégalaise pour la Promotion de l’astronomie) génne woon na ab yégle doon ci xamle ne mëneesul a gis weer wi fenn ci àddina si, ci guddig altine ji. Moo tax, ren, genn koritee am Senegaal, mu dig bennoo ak dëppoo gees rafetlu te di ñaan mu sax.

Ñu baree ngi doon xaar ngir xam fu Njiitu réew lu yees liy jullee. Ndax, moom Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay mees fal keroog 24 màrs 2024, Njagañaaw la daan jullee. Waaye, koriteg ren jii, fii ci Ndakaaru la ko jullee, fa jumaa ju mag ja.
Ejo ak LU DEFU WAXU ñoo ngi ndokkeel ñépp ci bés bi, di leen ñaanal koriteg jàmm gu ànd ak xéewal, ànd ak mbégte.

Déwénati !

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj